Leeru Bés bi — 22 Awril: Sarxalkat yi 1:3–4

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

«Bu saraxam dee saraxu jur gu gudd gu ñuy def rendi-dóomal, na sarxal aw yëkk wu amul sikk. Na ko yóbbu ci bunt xaymab ndaje mi ci kanam Aji Sax ji, ngir mu nangul ko ko. Na teg loxoom ci kaw boppu juru saraxu rendi-dóomal bi, ndax ñu nangul ko ko, muy njotlaayam.

Sarxalkat yi 1:3–4

Ibraayma ne ko: «Yàlla moom ci boppam dina dikk ak gàtt bi nuy def sarax, doom,» ñu daldi ànd dem, ñoom ñaar.

Njàlbéen ga 22:8

Ca ëllëg sa, ba Yaxya gisee Yeesu di dikk wutsi ko, da ne: «Kii mooy Xarum Yàlla, miy far bàkkaaru àddina.

Yowaan 1:29

Coobarey Yàlla googu moo waral ñu sellale nu sarax bi Yeesu Almasi bi sarxe yaramam benn yoon ba fàww.

Yawut ya 10:10

Noonu la deme ci Doomu nit ki, ñëwul ngir ñu di ko surgawu, xanaa ngir di nekk surga, ba far maye bakkanam, def ko njotug ñépp.»

Macë 20:28

Kenn du jële sama bakkan ci man; man maa koy joxeel sama bopp. Maa ko saña joxe, maa ko saña jëlaat, te loolu la ma sama Baay sant.»

Yowaan 10:18

Asiri du nu xettali, ay fasi xare it, dunu ko war, te dootunu wax lu nu sàkke sunuy loxo, ne ko: “Yaw yaa di sunu Yàlla.” Li nuy wax kay mooy yaw yaay kiy yërëm jirim.»

Ose 14:4

Moo tax dootul man maay dund, waaye Almasi bi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.

Galasi 2:20

Almasi bi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.

2.Korent 5:21

Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.

Efes 1:6

Ngor lu réy nga ma won, sorele maak tëraayu bàmmeel.

Taalifi cant 86:13

Te buleen ragal ñiy rey aw yaram, te manuñoo rey jëmmu biir, waaye ragalleen ki mana boole jëmmu biir ak aw yaram, sànk ca biir sawara.

Macë 10:28

Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israayil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.

Esayi 43:1

Aji Sax ji, mennum man a; amul jotkat bu ma moy.

Esayi 43:11

Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttaliku bàkkaar.

Esayi 43:25

Ana lu may tiit bés yu metti, yu ma njublaŋ yéewe seeni ñaawtéef, di ñu wóolu seen am-am, di kañoo alal ju bare? Ana ku mana jot a jot sa bakkanu moroom, mbaa mu di ko feyal Yàlla njot ga?

Taalifi cant 49:6–8

da koy baaxe, daldi ne Yàlla: «Musal ko ba du wàccagum biir pax. Maa ngeek njotlaayam.»

Ayóoba 33:24

Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy gi mu nu sopp, nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi bi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce.

Efes 2:4–5

Mucc kat amul ci keneen, ndax fi asamaan tiim, mayeesul fi nit ñi weneen tur wu nu wara mucce.»

Jëf ya 4:12