Sa jëkkër, Ki la sàkk, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee di turam. Aji Sell ju Israayil moo la jot, te moo di Yàllay àddina sépp.
Esayi 54:5
Leeru Bés bi
Sa jëkkër, Ki la sàkk, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee di turam. Aji Sell ju Israayil moo la jot, te moo di Yàllay àddina sépp.
Esayi 54:5
Mbóot mu xóot a ngi ci dog boobu, waaye man, li may wax moo di dog bi moo misaal diggante bi Almasi bi séq ak mbooloo mi.
Efes 5:32
Deesatu la woowe «Dëkk bi ñu wacc,» deesatul woowe sam réew «Réew mu gental.» Xanaa ñu woowe la «Dëkk bi ma neex,» tey woowe sam réew «Boroom jëkkër,» ndax yaa neex Aji Sax ji, te sa réew mi dina am boroom kër. Ni xale bu góor di takke ab janq, ni la la sa doom yu góor di moome ni jëkkër; ni boroom séet di bégee ab séetam, ni la la sa Yàlla di bégee.
Esayi 62:4–5
Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi seen goreel, yégal ñi ñu tëj seen ubbite. Moo ma yónni ngir ma yéene atum yiwu Aji Sax ji, ak at mu sunu Yàlla di mbugalee. Moo ma yónni ngir dëfal ñiy ñaawlu ñépp, ngir indil waa Siyoŋ ñiy ñaawlu ab kaala gu wuutu dóomu-taal, ak diwu mbégte mu ñu weccikoo seenu tiis, ak mbubbam cant mu ñu weccikoo xol bu jeex, ba ñu naa: «Ñii ñoo di ponkali garabi njubte yi, njëmbat li Aji Sax ji jëmbat, ngir teewal màggaayam.»
Esayi 61:1–3
Maa bég a bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam ndam, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.
Esayi 61:10
Turi tuuri Baal laay jële ci sa gémmiñ, ba deesatul fàttaliku seen tur.
Ose 2:19
Ana ku nuy tàggaleek cofeelu Almasi bi? Du ay nattu, te du njàqare, du it coonoy bunduxataal, mbaa ab xiif, mbaa rafle, te du genn aayteef, ba cib saamar.
Room 8:35
Man nag Aji Sax ji, ci yaw laa dénku. Ma ne: «Yaay sama Yàlla.»
Taalifi cant 31:15
Yaw kay yaa sopp xeet yi, sa ñu sell ñépp nga téyee say loxo, te ñoo topp say tànk, di taataan say tegtal.
Baamtug yoon wi 33:3
Kàddug Aji Sax ji dikkal Ilyaas ne ko: «Jógeel fii, walbatiku jëm penku, te làquji ca xuru Kerit ca penkub dexu Yurdan. Su ko defee, ca ndoxum xur wa ngay naane. Jox naa itam ndigal baaxoñ yi, ñu di la leel foofa.»
1.Buur ya 17:2–4
Kàddug Aji Sax ji dikkal ko ne ko: «Demal Sarebta ga ca Sidon te toog foofa. Ma ne, sant naa fa ab jëtun, mu may la loo lekk.»
1.Buur ya 17:8–9
«Moo tax ma ne leen, buleen seen bakkan jaaxal, ngir lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan, te it buleen seen yaram jaaxal ngir lu ngeen sol. Xanaa du lekk gi, bakkan bee ko ëpp solo, te koddaay li it, yaram wee ko ëpp solo?
Macë 6:25
Ndaxte loolu lépp, yéefar yi ñoo koy tiisoo. Te seen Baay ba fa asamaan xam na ne soxla ngeen loolu lépp.
Macë 6:32
Nanga wóoloo Aji Sax ji sa léppi xol, te bul wéeru ci saw déggin. Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.
Kàddu yu xelu 3:5–6
ci ni ngeen di sippikoo ci kawam, mboolem seenu tiis, nde mooy ki leen tiisoo.
1.Piyeer 5:7
Bés yu mujj yi
Wone yépp6 Mar 2025
5 Mar 2025
4 Mar 2025
3 Mar 2025
2 Mar 2025
1 Mar 2025
28 Few 2025