Man ci sama bopp maa leen di dëfal. Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee, doom aadama ju bokk aw demin akum ñax?
Esayi 51:12
Leeru Bés bi
Man ci sama bopp maa leen di dëfal. Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee, doom aadama ju bokk aw demin akum ñax?
Esayi 51:12
Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi bi, Baayu yërmande yi, Yàlla jiy dëfale nu nekk, moom mi nuy dëfal ci sunu jépp njàqare, ngir noonu nu jote nun ci sunu bopp, ndëfalaay lu nu dëfalu fa Yàlla, nu man koo dëfale ñi nekk ci mboolem xeeti njàqare.
2.Korent 1:3–4
Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal. Moo xam sunu bind, di bàyyi xel ne pënd lanu.
Taalifi cant 103:13–14
Man maa leen di naxtaan ba ngeen dal, ni doom ju ndeyam di naxtaan ba mu dal, ngeen am xel mu dal fi Yerusalem.»
Esayi 66:13
ci ni ngeen di sippikoo ci kawam, mboolem seenu tiis, nde mooy ki leen tiisoo.
1.Piyeer 5:7
Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma.
Taalifi cant 86:15
Man maay ñaan Baay bi, mu yónnee leen beneen Taxawukat, ngir mu nekk ak yeen ba fàww. Kooku mooy Noowug Yàlla giy xamle liy dëgg. Àddina du ko mana dalal, ndax gisu ko te xamu ko. Yeen nag xam ngeen ko, ndax ci seen biir la dëkk, te ci seen biir xel lay nekk.
Yowaan 14:16–17
Te itam Noowug Yàlla moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noo gi moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.
Room 8:26
Mooy fomp seen wépp rongooñ. Dee dootul am, dëj aki yuux aku tiis dootul am, lu njëkk laay wéy.»
Peeñu ma 21:4
Yàllaa am kóllëre, moom mi leen woo, ngir ngeen bennoo ak Doomam Yeesu Almasi bi, sunu Sang.
1.Korent 1:9
Ndax kat moo nangoo ci Yàlla Baay bi, teraanga ak daraja, ba ko baat ba jibalee, bawoo fa Boroom daraja ju yéeme ja ne: «Kii moo di sama Doom, sama soppe; moom laay bànneexoo.»
2.Piyeer 1:17
Ndaw cofeel gu nu Baay bi won, ba ñu di nu woowe doomi Yàlla, te moom lanu it. Àddina nag xamu nu, te li ko waral moo di da koo xamul moom itam.
1.Yowaan 3:1
Kon nag doonleen ay roykati Yàlla, gannaaw yeenay doomam yi mu sopp,
Efes 5:1
Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi bi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.
Room 8:17
Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,
Yawut ya 1:3
Yeen, na seenug leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seen jëf ju rafet, ba sàbbaal seen Baay ba fa kaw.
Macë 5:16
Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.
Yawut ya 12:2
«Léegi nag, ci yaw laa jëm, waaye lii laay wax bi may nekkagum ci àddina, ngir sama mbég ñeel leen, mat sëkk.
Yowaan 17:13
Bés yu mujj yi
Wone yépp13 Sàt 2026
12 Sàt 2026
11 Sàt 2026
10 Sàt 2026
9 Sàt 2026
8 Sàt 2026
7 Sàt 2026