Leeru Bés bi — 24 Ut: Mucc ga 3:7

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Aji Sax ji tegaat ca ne ko: «Gis naa bu baax fitna ji sama ñoñ nekke Misra. Dégg naa itam seen jooy ndax kilifay saskat yi leen di gétën ci liggéey, te ñeewante naa leen ngir seen coono.

Mucc ga 3:7

Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko.

Esayi 53:3

Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.

Yawut ya 4:15

Noonu la kàddu ga jottalikoo woon ci gémmiñu Yonent Yàlla Esayi mate. Mooy ba mu nee: «Moom sunuy wopp la jël, sunuy jàngoro la sëfoo.»

Macë 8:17

Foofa la teenub Yanqóoba nekkoon. Fekk na coonob tukki ba jàpp Yeesu. Mu toog ca wetu teen ba, waxtu wu xawa yemook digg bëccëg.

Yowaan 4:6

Ba ko Yeesu gisee muy jooy, Yawut ya mu àndal itam di jooy, yaramam daw na, mu jàq.

Yowaan 11:33

Yeesu nag jooy.

Yowaan 11:35

Coonoy nattu bi mu dékku nag tax na mu mana wallu ñi nekk ci nattu.

Yawut ya 2:18

Nañu bindal lii maasug ëllëg, ba xeet wu sosoogul màggal Ki Sax, nde Aji Sax jeey jéere fu sellam fa ca kaw, di niire suuf fa asamaan,

Taalifi cant 102:19–20

Ndaxam moo xam fi ma jaare, te bu ma nattoo, ma génn ci ni wurus wu ñu xelli.

Ayóoba 23:10

sippi ko sama tawat, diis ko sama njàqare.

Taalifi cant 142:3

Mu ne ko: «Dawal, nga wax xale bu góor bii ne ko: “Yerusalem lees di dëkke, te tata wëru ko; ŋàpp lay def, ndax barewaayu nit ñeek jur gi ci biiram.

Sàkkaryaa 2:8

Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.

Esayi 63:9

Danoo wara liggéey liggéeyu ki ma yónni ci bi muy bëccëg; bu guddee kenn du liggéey.

Yowaan 9:4

Ab yaafus day yaakaar, du am; ab njaxlaf sàkku, woomle.

Kàddu yu xelu 13:4

Ku yéwén, woomle; kuy suuxat, suuxu.

Kàddu yu xelu 11:25

Yeesu ne leen: «Samaw ñam moo di jëfe coobarey ki ma yónni, ba sottal ab liggéeyam. Du yeena naan: “Fii ak ñeenti weer ngóob taxaw”? Dégluleen, ma wax leen: dawalleen seen bët, xool tool yi, ñu ngi weex tàll, di xaar am ngóob.

Yowaan 4:34–35

«Nguurug asamaan dafa mel ni boroom kër bu teela xëy, di wut ay surga yu ko liggéeyal toolub reseñam. Mu juboo ak liggéeykat ya ci bëccëg bu nekk peyug bëccëgu lëmm. Mu daldi leen yebal ca toolub reseñam.

Macë 20:1–2

waareel kàddug Yàlla te taxaw ci temm, su neexee ak su naqaree; di yedde, di femmoo, di ñaaxe, tey saxoo muñ ci sa njàngale.

2.Timote 4:2

Ci biir loolu mu woo fukki surgaam, jox leen ku nekk benn posetub wurus bu gànjare, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba ma ñibbisi.”

Luug 19:13

Ci yiwu Yàlla daal laa doone ki ma doon, te yiw woowu ma ñeel neenul. Te sax yeneen ndaw yépp sax, maa leen gëna liggéey. Du ci man nag, waaye yiwu Yàlla wi ànd ak man la.

1.Korent 15:10