Leeru Bés bi — 20 Ut: Màndiŋ ma 23:19

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Yàlla du nit, bay fen, du doom aadama bay tuub. Moom wax na lu mu deful a? Am àddu na lu mu sottalul?

Màndiŋ ma 23:19

gépp may gu baax ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.

Yanqóoba 1:17

Yeesu Almasi bi, menn mii la woon démb ak tey ba fàww, du soppiku.

Yawut ya 13:8

Kiiraayam la lay sànge, nga yiiru, làqu; kóllëreem feg la, di la aar.

Taalifi cant 91:4

Yàllaa bëggoona firndeel nu mu gëna leere ñeel ñi moom dige bi, ne ab dogalam du tebbiku mukk. Moo tax mu dogale ngiñ ab digeem. Ñaar yooyu du tebbiku ndax Yàlla du fen, te nun ñi daw làqusi ci moom, ci lanu ame ndëgërlaay lu réy lu nu ŋoye ci yaakaar ji ci sunu kanam.

Yawut ya 6:17–18

Xamleen boog ne seen Yàlla Aji Sax ji moom mooy Yàlla; mooy Yàlla ju dëggu jiy sàmm kóllëre ak ngor ñeel soppeem ñiy sàmm ay santaaneem, sët ba sëtaat, ba ci junniy maas.

Baamtug yoon wi 7:9

Aji Sax ji ngor ak dëgg rekk lay jiitee kuy sàmm kóllëreem ak seedey yoonam.

Taalifi cant 25:10

Ndokkalee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba; di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji, Ki sàkk kaw ak suuf, géej ak lépp li ci biir, di sàmm dëgg ba fàww,

Taalifi cant 146:5–6

Bu mettee, nga yoqi, sa doolee néew.

Kàddu yu xelu 24:10

Mooy dooleel ku loof, di kàttanal ku jeele.

Esayi 40:29

Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi bi wàcc ci sama kaw.

2.Korent 12:9

Mu woo ma, ma wuyu ko; mook man ci biir njàqare, ma xettali ko, darajaal ko,

Taalifi cant 91:15

Yàlla ji sax fàww moo dib rawtu, përëgam bi sax dàkk di cëslaay, moo la dàqal ab noon ne la: “Jekkalil!”

Baamtug yoon wi 33:27

Yaa gis ñu di ma sewal, di ma ruslooka toroxal, yaa ngi ne jàkk ci noonoo noon.

Taalifi cant 69:20

Bépp sarxalkat bu mag nag, ci biir nit ñi lees ko jële, fal ko ngir nit ñi, ci seen diggante ak Yàlla, muy joxe ay saraxi njébbal ak saraxi jur ngir seeni bàkkaar. Dina mana sédd cér ñi xamul ak ñi moy ndax moom ci boppam ci ag néew doole la tënku.

Yawut ya 5:1–2

Noonu la woon itam ci Almasi bi. Tegoowul boppam darajay doon sarxalkat bu mag, waaye Yàllaa ko ne: «Yaa di sama Doom, bés niki tey maa la jur.»

Yawut ya 5:5

Li muy Doom lépp, terewu koo tàggatu ci dégg ndigal, ndax coono yi mu daj. Noonu lees matale Almasi bi sëkk, ba mu doon cosaanu mucc gu dul jeex, ñeel mboolem ñi ko déggal.

Yawut ya 5:8–9

Ndaxam moom sunu wopp la yenu, sunuy mitit la sëfoo. Nun nu foog ne dees koo mbugal, foog ne Yàllaa ko duma, toroxal ko.

Esayi 53:4