Ñu ne: «Bu yàgg la nu Aji Sax ji feeñu, ne nu: “Maa leen masa bëgg, ba tax ma sédd leen ngor.
Yeremi 31:3
Leeru Bés bi
Ñu ne: «Bu yàgg la nu Aji Sax ji feeñu, ne nu: “Maa leen masa bëgg, ba tax ma sédd leen ngor.
Yeremi 31:3
Nun nag bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla fu nu tollu, ci yeen ñi Boroom bi sopp, ndax yeen la njëkka tànn, ngir sellal leen ci Noo gu Sell gi, ak itam seen ngëm gi ngeen gëm dëgg gi, ngir texeel leen. Ci loolu it la leen woo ba mu jëfandikoo xibaaru jàmm bi nu leen àgge, ngir ngeen séddu ci sunu ndamal Boroom Yeesu Almasi bi.
2.Tesalonig 2:13–14
Moo nu musal, woo nu woote bu sell te sunuy jëf taxul, waaye coobarey boppam a tax, ak yiwam wi ñu nu may ci Almasi Yeesu, balaa ay jamonoy jamono di sosu.
2.Timote 1:9
Gis nga ma, ba ma diw lumb; sa téere lim na fan yi nga ma àppal, ba ca benn dooragul.
Taalifi cant 139:16
Ndax Yàlla moo sopp àddina, ba joxe jenn Doomam ji, ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww, te du sànku mukk.
Yowaan 3:16
Lii mooy cofeel: cofeel gi du sunug cofeel, nun ci Yàlla; xanaa cofeel gi mu nu sopp, ba yebal Doomam, def ko njotlaay, ñeel sunuy bàkkaar.
1.Yowaan 4:10
Ba ba ngeen di magal, man la, ba keroog ngeen di bijjaaw, maa leen di boot. Maa sàkk, maay yor, maay boot, xettali!
Esayi 46:4
Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israayil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo. Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.
Esayi 43:1–2
Fonk la, teral la ak sopp la, moo tax ma joxey nit, weccikoo la; ay askan dee, wuutu sa bakkan.
Esayi 43:4
Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam, daayaarlu, di wër, tiim leen, tàllali laafam, aw leen, teg ciw dunqam, boot leen. Aji Sax ji doŋŋ a leen wommat, du yàllay jàmbur ju ko ci fekk.
Baamtug yoon wi 32:11–12
Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.
Esayi 63:9
Yeesu Almasi bi, menn mii la woon démb ak tey ba fàww, du soppiku.
Yawut ya 13:8
Ndax kat bir na ma ne du ag dee, du ag dund, du ay malaaka, duy boroom nguur, du tey, du ëllëg, duy boroom doole, du lu kawe, du lu xóot, mbaa meneen mbindeef mu mu doon; dara manu noo tàggale ak cofeel gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu sunu Sang.
Room 8:38–39
Aji Sax ji nee: «Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp, mbaa muy néege ku mu jur ci biiram? Bu ko manoona fàtte it, man duma la fàtte.
Esayi 49:15
Bés yu mujj yi
Wone yépp22 Ut 2026
21 Ut 2026
20 Ut 2026
19 Ut 2026
18 Ut 2026
17 Ut 2026
16 Ut 2026