Leeru Bés bi — 17 Ut: Yanqóoba 5:16

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, day dal ak doole.

Yanqóoba 5:16

Ibraayma dellu ne: «Ma ñemee wax ak yaw, Boroom bi, te duma dara ba dara booloo jeex. Waaye juróom fukk ñooñu jub, su yéesee juróom rekk nag? Mbaa doo tas dëkk bi ndax juróom ñi ci yées?» Aji Sax ji ne ko: «Su ma fa gisee ñeent fukk ak juróom ñu jub, duma ko tas.»

Njàlbéen ga 18:27–28

Ci kaw loolu Pilaat dogal ñu defal leen la ñu sàkku.

Luug 23:24

Waaye man maa leen wax ne leen, soppleen seeni noon te ñaanal ñi leen di bunduxataal,

Macë 5:44

Man nag, ñoom laay ñaanal; ñaanaluma waa àddina, waaye ñi nga ma dénk, ñoom laay ñaanal, ndax sa ñoñ lañu.

Yowaan 17:9

«Du ñoom doŋŋ laay ñaanal nag, waaye ñi may gëm ëllëg ndax seen kàddu itam laay ñaanal,

Yowaan 17:20

Yenuleen seeni yeni moroom, su boobaa ngeen di topp yoonu Almasi bi, ba mu mat sëkk.

Galasi 6:2

Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, day dal ak doole. Ilyaas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye ba mu saxee ci ñaan ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diiru ñetti at ak genn-wàll.

Yanqóoba 5:16–17

Nit aki fanam di saxyaay suy law ni tóor-tóoru àll; ngelaw li wal, mu ne mes, mel ni masu faa nekk.

Taalifi cant 103:15–16

Yal nanga nu xiir ci lim sunuy fan, ba nu mana dawal xel mu rafet.

Taalifi cant 90:12

Ana luy njariñal nit ku jagoo àddina sépp, te ñàkk bakkanam?

Màrk 8:36

Ñax ma wow, tóor-tóor ma lax fa ko Aji Sax ji yónnee mbóoyo. Askan wi kay, am ñax doŋŋ la. Am ñax day wow; tóor-tóor day lax. Waaye sunu kàddug Yàlla mooy sax ba fàww.»

Esayi 40:7–8

Te àddina day jeex, mooki xemmemtéefam, waaye kuy jëfe coobarey Yàlla mooy sax ba fàww.

1.Yowaan 2:17

Ndaxte Yàlla moo ne: «Bu bésub yiw taxawee, ma nangul la; bu bésub mucc jotee, ma wallu la.» Te nag, tey jii la bésub yiw taxaw; tey kat, la bésub mucc.

2.Korent 6:2

ñiy jariñoo alalu àddina, bañ cee xér, ndax melow àddina sii tey, day wees.

1.Korent 7:31

Nanu seet itam ci sunu biir nu nuy xiirtalantee ngir cofeel ak jëf ju baax. Te bunu def ni ñenn ñi, di daggoo ak sunuy ndaje, waaye nanuy ñaaxante, rawatina tey bi ngeen gisee bés bi dëgmal.

Yawut ya 10:24–25