Man maay ñaan Baay bi, mu yónnee leen beneen Taxawukat, ngir mu nekk ak yeen ba fàww. Kooku mooy Noowug Yàlla giy xamle liy dëgg. Àddina du ko mana dalal, ndax gisu ko te xamu ko. Yeen nag xam ngeen ko, ndax ci seen biir la dëkk, te ci seen biir xel lay nekk.
Yowaan 14:16–17
Moona man de, dëgg laa leen wax. Seen njariñ moo di ma dem, ndax su ma demul, Taxawukat bi du ñëw ci yeen; waaye su ma demee, maa leen koy yónnee.
Yowaan 16:7
Te Noowug Yàlla, moom ci boppam, moo mànkoo ak sunu noowug bopp, di seede ne ay doomi Yàlla lanu.
Room 8:16
Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di woowe Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay».
Room 8:15
Te itam Noowug Yàlla moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noo gi moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.
Room 8:26
Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesaleek gépp mbég ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen fees dell ak yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.
Room 15:13
Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
Room 5:5
Ni nuy xame ne ci Yàlla la nu saxe, te moom itam ci nun la sax, moo di Noowam gi mu nu sédd ab cér.
1.Yowaan 4:13
Gannaaw gi Nawmi, gorob Ruut ba, dafa wax Ruut ne ko: «Doom, tee ma laa sàkkal fooy ame jàmm, nga féete fa?
Ruut 3:1
Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla.
Yawut ya 4:9
ba sama bokk yi dëkke sancub jàmm,
ci dëkkuwaay yu wóor,
ci dalluwaay yu dal xel,
Esayi 32:18
Biir bàmmeel la ñu bon ñiy noppee sonle,
fa la ña jeele doole noppaloo,
Ayóoba 3:17
Ci kaw loolu ma dégg baat bu jibe asamaan ne: «Bindal: “Bés niki tey ndokkalee aji dee ñi deewaale gëm Sang bi.”» Noowug Yàlla nee: «Waawaaw, ndax coono dina leen wàcc, ngir seeni jëf a leen topp.»
Peeñu ma 14:13
Fa la ndaw li nu jiitu dugg ngir nun, te kookooy Yeesu mi ñu fal sarxalkat bu mag ba fàww, mu topp dayob Melkiccedeg.
Yawut ya 6:20
«Mboolem yeen ñi loof ndax sëf bu diis, ñëwleen ci man, man maa leen di noppal. Tegooleen sama kilifteef te ngeen jànge ci man, daldi dajeek noflaayal xol, ndax maa lewet, woyof. Sama kilifteef sedd na, te samab sëf woyof.»
Macë 11:28–30
Ndax Boroom bi Aji Sax ji,
Aji Sell ju Israayil dafa wax ne:
«Délsi, dallu moo leen di musal.
Ne tekk te wóolu maa leen di dooleel.
Waaye yeena bëggul!
Esayi 30:15
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Aji Sax jee may sàmm,
du lenn lu ma ñàkk.
Parlu mu naat la may gooral,
wal mu dal, mu tette ma ca,
Taalifi cant 23:1–2