Teewlul te nga leqali ndes wi ngay waaja deele. Ndax kat, gisuma sa jëf ju mat fa sama kanam Yàlla.
Peeñu ma 3:2
Leeru Bés bi
Teewlul te nga leqali ndes wi ngay waaja deele. Ndax kat, gisuma sa jëf ju mat fa sama kanam Yàlla.
Peeñu ma 3:2
Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiitalleen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan.
1.Piyeer 4:7
Àndleen ak sago te teewlu! Ki leen di tuumaal, Seytaane, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax.
1.Piyeer 5:8
Waaye wattuleen, wattuleen seen bopp bu baax, bala ngeena fàtte mbir yi ngeen teg seen bët, ba du génn seenum xel seen giiru dund gépp. Te nangeen ko xamal seeni doom ak seeni sët.
Baamtug yoon wi 4:9
Sama nit ku jub nag mooy dund ndax ngëm ga, waaye ku dellu gannaaw, sama xol bégewu la.» Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw te nara sànku, waaye nooy ñi saxoo ngëm te nara mucc.
Yawut ya 10:38–39
Lii ma leen wax nag, ñépp laa ko wax: “Teewluleen!”»
Màrk 13:37
bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama loxol ndijoor liy àtte dëgg.
Esayi 41:10
Man Aji Sax ji maay sa Yàlla; téye sa loxol ndijoor, di la wax ne la: Bul tiit, maa lay dimbali.
Esayi 41:13
«Boroom bi da may gàntal ba fàww, ba du ma baaxeeti mukk a?
Taalifi cant 77:8
Ci biir nootaange la nu geesoo, Kee saxoo ngoram!
Taalifi cant 136:23
“Aji Sax ji! Kiy muñ mer, te bare ngor, di baale tooñ aki moy te du ñàkka topp mukk doom, tooñu waajuram, ba ca sët yaak sëtaat ya.”
Màndiŋ ma 14:18
Ana Yàlla ju mel ni yaw, di baale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom? Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne. Moo nuy yërëmati; sunuy ñaawtéef lay joggiy tànkam, te biir xóotey géej lay tàbbal sunuy bàkkaar.
Mise 7:18–19
ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell
Tit 3:5
Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi bi, Baayu yërmande yi, Yàlla jiy dëfale nu nekk, moom mi nuy dëfal ci sunu jépp njàqare, ngir noonu nu jote nun ci sunu bopp, ndëfalaay lu nu dëfalu fa Yàlla, nu man koo dëfale ñi nekk ci mboolem xeeti njàqare.
2.Korent 1:3–4
Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan. Coonoy nattu bi mu dékku nag tax na mu mana wallu ñi nekk ci nattu.
Yawut ya 2:17–18
Bés yu mujj yi
Wone yépp20 Mar 2026
19 Mar 2026
18 Mar 2026
17 Mar 2026
16 Mar 2026
15 Mar 2026
14 Mar 2026