Leeru Bés bi — 19 Mars: Jëf ya 3:26

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Yeen la Yàlla njëkka wool jawriñam, daldi koy yebal ci yeen, ngir barkeel leen, waññi kenn ku nekk ci yeen mu moy jikkoom yu bon.»

Jëf ya 3:26

Cant ñeel na Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi bi! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju yaa, ci dooley ndekkitel Yeesu Almasi bi, ngir may nu yaakaar juy dund.

1.Piyeer 1:3

Ndegam ba ñu dee ay bañaaley Yàlla lees nu jubalee deewug Doomam, ñaata yoon lees nuy gënatee musale ag dundam, gannaaw ba ñu nu jubalee ak Yàlla?

Room 5:10

Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi. Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.

Tit 2:13–14

Waaye ni ki leen woo selle, yeen itam nangeen selle noonu ci seen mboolem jëfin. Ndax kat bindees na ne: «Ñu sell ngeen wara doon, ndax man Ku sell laa.»

1.Piyeer 1:15–16

Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu Sang Yeesu Almasi bi nu baaxe bépp barkey biir, ci Almasi bi nu bokk, fa déndi asamaan ya.

Efes 1:3

Ndax kat ci Almasi bi, ci yaramu nitam la léppi Yàlla dëkke, ba mat sëkk ci moom, ci moom ngeen mate it, te mooy kilifay mboolem boroom nguur yi ak mboolem boroom sañ-sañ yi.

Kolos 2:9–10

Ci ag matam lanu tanqe nun ñépp, yiw ci kaw yiw.

Yowaan 1:16

Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?

Room 8:32

Naqaru xol sonal na ma, may ma ndëgërlaay, yaa ko dige.

Taalifi cant 119:28

Bàyyil xel li nga ma dig, Sang bi; moom laa yaakaar.

Taalifi cant 119:49

May ciib-ciibi ni wetwet mbaa ramatu, di binni nim xati, di séentu kaw ba saay gët giim. Dama noon: Éy Boroom bi, loof naa, dimbali ma.»

Esayi 38:14

Asamaan ak suuf dina wees, waaye samay wax du wees mukk.

Luug 21:33

«Léegi nag maa ngi nii tey di waaj yoon wu dul jaas ci mboolem àddina. Seedeleen seen léppi xol ak seen jëmm jépp nag ne, du lenn lu fanaan àll ci mboolem lu baax lu leen seen Yàlla Aji Sax ji waxoon. Lépp a leen dikkal. Du lenn lu ci fanaan àll.

Yosuwe 23:14

Gannaaw loolu mu ne ma: «Yaw nit ki ñu naw, bul tiit. Jàmm la. Góor-góorlul!» Muy wax ak man, may amaat doole, ba ne ko: «Waxal sang bi, dooleel nga ma.»

Dañeel 10:19

Léegi nag, Sorobabel, góor-góorlul, Aji Sax jee ko wax. Yaw doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag bi, góor-góorlul; yeen mboolem askanu réew mi, góor-góorluleen,” kàddug Aji Sax jee. Mu ne: “Liggéeyleen, maa ànd ak yeen déy, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Ase 2:4

Mu wax ma ne ma: «Lii moo di kàddug Aji Sax ji dikkal Sorobabel, di wax ne: Du cig njàmbaar, du ci doole, ci samag noo la. Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.»

Sàkkaryaa 4:6

Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.

Efes 6:10