Leeru Bés bi — 4 Nowàmbar: 1.Piyeer 1:6

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Loolu bégeleen koo bége, doonte tey ñàkkul ngeen nekke njàqare ab diir, ndax ay nattuy nattu.

1.Piyeer 1:6

Soppe yi, tàngooru nattu bi ngeen nekke nii, bumu leen jaaxal ba mel ni lu jaaduwul moo leen dikkal. Waaye noonu ngeen séddoo ci coonoy Almasi bi, bégeleen ko, ngir bu ndamam feeñee, ngeen gënatee bég.

1.Piyeer 4:12–13

Te it fàtte ngeen kàddu yii ñu leen ñaaxe, ni nit aki doomam: «Doom, bul xeeb yaru Boroom bi, bul xàddi, bu la waññee,

Yawut ya 12:5

Dëgg la, benn yarub tey neexul, xanaa naqari. Waaye la yar bay mujj jural ña mu tàggat, jàmm la ak njub.

Yawut ya 12:11

Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.

Yawut ya 4:15

Coonoy nattu bi mu dékku nag tax na mu mana wallu ñi nekk ci nattu.

Yawut ya 2:18

Benn nattu dabu leen bu moy nattu yiy dale. Te it Yàllaa jara wóolu. Yàlla du nangu ngeen tegoo nattu bu ngeen àttanul, waaye nattu ba lay booleek pexe ma leen cay génne, ba ngeen man koo dékku.

1.Korent 10:13

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Esayi 9:6

muy àttee sa mbooloo njub, di àttee sa néew-ji-doole ñi yoon, tooli tund yu mag yi indil mbooloo mi jàmm, tooli tund yu ndaw yi xéewale leen àtteb dëgg,

Taalifi cant 72:2–3

Yal na Buur di xéewalu réewam nib taw cig ruujeef, mbaa waame wuy suuxat suuf. Janti Buur aji jub day woomle, te ba keroog weer wiy fey, jàmm di law,

Taalifi cant 72:6–7

«Daraja ñeel na Yàlla fa asamaan sa gëna kawe, jàmm ci kaw suuf ñeel ñi Yàlla baaxe.»

Luug 2:14

Sunu Yàllaa yaatu yërmande, moo nu fenkal ab jant, di niital ñi tooge biir lëndëm ak takkndeeru dee, di nu gindi, teg nu ci yoonu jàmm.»

Luug 1:78–79

Moo yónnee kàddoom bànni Israayil, àgge leen xibaaru jàmm, biy maye jàmm ci Yeesu Almasi miy Sangu ñépp.

Jëf ya 10:36

Loolu dama leen koo wax ngir seen xel dal ci man. Àddina sii, dingeen fi am njàqare, waaye dëgërluleen, ndax daan naa àddina.»

Yowaan 16:33

Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit.

Yowaan 14:27

Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.

Filib 4:7