Leeru Bés bi — 1 Nowàmbar: Kàddu yu xelu 8:34

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Mbégte ñeel na ki may déglu, di teewlu ca sama bunt bés bu nekk, di ma toogaanu sama bunt kër.

Kàddu yu xelu 8:34

Ma ne, ni jaam bu góor di wékke sangam bët, jaam bu jigéen di ko wékke bët sangam bu jigéen, ni lanuy wékke sunu Yàlla Aji Sax ji bët, ba keroog mu baaxe nu.

Taalifi cant 123:2

Saraxu rendi-dóomal lay doon bu sax, te war seen maasoo maas fi bunt xaymab ndaje mi, ci kanam Aji Sax ji. Foofu laay dajeek yeen, te fa laay waxe ak yaw.

Mucc ga 29:42

Sarxalukaay bu ñu defare suuf ngeen may sàkkal, di ci sarxal seeni gàtt ak seeni nag, muy seen saraxu rendi-dóomal, mbaa seen saraxi cant ci biir jàmm. Ci mboolem béreb bu may fàttalee sama tur laay dikk fi yeen, barkeel leen.

Mucc ga 20:24

ndax fu ñaar mbaa ñett dajee ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»

Macë 18:20

Waaye waxtoo ngi ñëw, te léegi la; ci la jaamukat yi dëgg di jaamoo Baay bi xel ak dëgg, ndax ñu ni mel la Baay bi sàkku ñu jaamu ko. Yàlla xel la, kon ñi koy jaamu, xel ak dëgg lañu ko war di jaamoo.»

Yowaan 4:23–24

Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp parlu, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.

Efes 6:18

di saxoo ñaan,

1.Tesalonig 5:17

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Esayi 9:6

xelum Aji Sax ji tegu fi kawam, xelum rafet xalaat ak ràññee, xelum digle ak njàmbaar, xelum xam Aji Sax ji, ragal ko. Ragal Aji Sax ji lay safoo, du lu ko bëtam may lay àttee, du lu ko noppam may lay dogale,

Esayi 11:2–3

Déggal! Xel mu Rafet di soxna saa ngi woote, moom soxna si Am Dégg di xaacu.

Kàddu yu xelu 8:1

«Yeen mbooloo yi laay woo, doom aadama yi laay joor. Téxét bi, deel foog, dof bi, déggal ndéey lu xelu. Déglul, ma wax la lu am solo, dégtal la njub.

Kàddu yu xelu 8:4–6

Maa moomi digle, di maye gis-gis; maa amug dégg, di boroom doole.

Kàddu yu xelu 8:14

Xel moomu it fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi la bawoo. Ndigalam a ni yéemee, pexeem màgge ni!

Esayi 28:29

Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.

Yanqóoba 1:5

Nanga wóoloo Aji Sax ji sa léppi xol, te bul wéeru ci saw déggin. Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.

Kàddu yu xelu 3:5–6