«Yeen Efrayim, lu ma masa séq ak jëmmi tuur? Man maa leen di nangul, di leen wattu, di leen keral ni garab gu naat gu dul ruus, sa meññeef bawoo fi man.»
Ose 14:9
Leeru Bés bi
«Yeen Efrayim, lu ma masa séq ak jëmmi tuur? Man maa leen di nangul, di leen wattu, di leen keral ni garab gu naat gu dul ruus, sa meññeef bawoo fi man.»
Ose 14:9
Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag: «Moo di doj wi tabaxkat yi beddi woon, te mu mujj di doju koñu tabax bi.» Te it: «Mooy doj wuy fakkastale, di xeer wuy daaneel.» Ñoo ko fakkastaloo nde ñoo gëmul kàddu gi, te it loolu la leen dogal ba séddoon.
1.Piyeer 2:7–8
Aji Sax jeeki nammeelam rawtu la ci ku mat, di sànkute ci kuy def lu bon.
Kàddu yu xelu 10:29
Ku ami nopp nag, na dégg.
Macë 11:15
Ku xelu ku ne, na ràññee lii te seede li Aji Sax ji jëfe ngoram.
Taalifi cant 107:43
«Bët mooy làmpu yaram. Su sa bët wéree, sa yaram wépp a ciy leerloo,
Macë 6:22
Ku namma jëfe coobarey Yàlla, dina xam ndax li may jàngale ci Yàlla la jóge, am ci sama coobarey bopp laay waxe.
Yowaan 7:17
Ndax ku am, dees na ko dolli, ba mu barele; waaye ku amul, la mu am as néew sax, dees na ko nangu.
Macë 13:12
Ku bokk ci Yàlla, déglu ay kàddoom. Gannaaw dégguleen nag, bokkuleen ci Yàlla.»
Yowaan 8:47
te bëgguleena ñëw ci man, ba texe!
Yowaan 5:40
Samay xar, sama baat lañuy déglu; maa leen xam, te man lañuy topp.
Yowaan 10:27
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Esayi 9:6
Dégluleen, yeen bànni Israayil, Aji Sax ji sunu Yàlla, Aji Sax ji kenn la.
Baamtug yoon wi 6:4
Man ak Baay bi benn lanu.»
Yowaan 10:30
waaye gannaaw moom laay def, su ngeen ma gëmul sax, gëmleen boog jëf ji, ngir ngeen xam te ràññee ne Baay baa ngi ci man, te man it, maa ngi ci Baay bi.»
Yowaan 10:38
Ñu ne ko: «Kuy sa baay?» Yeesu ne leen: «Xamuleen ma, xamuleen sama Baay. Su ngeen ma xamoon, xam ko, moom itam.»
Yowaan 8:19
Filib ne ko: «Sang bi, won nu Baay bi rekk, mu doy nu.» Yeesu ne ko: «Filib, ni ma yàggeek yeen te ba tey xamuloo ma? Ku ma gis kay, gis nga Baay bi. Kon ana noo naan: “Won nu Baay bi”?
Yowaan 14:8–9
Mu waxaat ne: «Man maay am kóolute ci moom.» Dellooti ne: «Man de, maa ngii, maak xale yi ma Yàlla may.»
Yawut ya 2:13
Mooy sonn ba gisug leer, doyloo ko. Ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, mu def ñu bare, ñu ñu limal njub, ndax li mu sëfoo seeni ñaawtéef.
Esayi 53:11
«Man, maay Alfa, di Omega», la Boroom bi Yàlla wax, moom Ki masa nekk, Ki nekk, di Kiy dikk ëllëg, te di Aji Man ji.
Peeñu ma 1:8
Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, balaa Ibraaymaa juddu, man maa nekk.»
Yowaan 8:58
Yàlla ne Musaa: «Maay Ki nekk. Kon waxal bànni Israayil ne leen: “Aji Nekk ji moo ma yónni ci yeen.”»
Mucc ga 3:14
Waaye Doom ji la Yàlla ne: «Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww, sa yetu buur njub la.
Yawut ya 1:8
Mooy ki nekkoon naka jekk balaa daraa nekk, te lépp ci moom la sottee ba temboo.
Kolos 1:17
Ndax kat ci Almasi bi, ci yaramu nitam la léppi Yàlla dëkke, ba mat sëkk ci moom,
Kolos 2:9
Bés yu mujj yi
Wone yépp2 Now 2025
1 Now 2025
31 Okt 2025
30 Okt 2025
29 Okt 2025
28 Okt 2025
27 Okt 2025