Loolu sax moo waral Almasi bi dee, ba noppi dekki, dellu di dund, ngir ñi dee ak ñiy dund ñépp, muy seen boroom.
Room 14:9
Leeru Bés bi
Loolu sax moo waral Almasi bi dee, ba noppi dekki, dellu di dund, ngir ñi dee ak ñiy dund ñépp, muy seen boroom.
Room 14:9
Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee. Mooy sonn ba gisug leer, doyloo ko. Ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, mu def ñu bare, ñu ñu limal njub, ndax li mu sëfoo seeni ñaawtéef.
Esayi 53:10–11
Xanaa du fàww Almasi bi daj boobu coono, doora dugg ci teraangaam?»
Luug 24:26
Ndaxte cofeelu Almasi bi daal moo nu jiite, nun ñi ràññee lii: gannaaw kenn moo dee ngir ñépp, kon ñépp a dee. Te ki dee ngir ñépp, daa dee ngir ñiy dund bañatee dund ngir seen bopp, xanaa di dund ngir ki dee ngir ñoom, ba dekki.
2.Korent 5:14–15
«Kon nag na wóor waa kër Israayil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»
Jëf ya 2:36
Bu yàgg, ba àddina sosoogul la Yàlla tuddaloon Almasi bi loolu, waaye léegi ci mujug jamono jii la ko Yàlla feeñal ngir yeen ñi Almasi bi tax ngeen gëm Yàlla. Te Yàllaa ko dekkal, may ko ndam, ba tax Yàlla di ki ngeen gëm, yaakaar ko.
1.Piyeer 1:20–21
May nu bésub tey, sunu dundub bés bu nekk,
Macë 6:11
Ba may ndaw, ba tey may mag, gisuma ku jub ñàkk ndimbal, mbaa askanam di dunde yalwaan.
Taalifi cant 37:25
Ku ni mel, béreb bu kawe lay dëkke, doj yu ñu dàbbali di rawtoom, dundam doy, te ndoxam du ñàkk.
Esayi 33:16
Baaxoñ ya di ko indil mburu ak ndawal bëccëg, mburu ak ndawal ngoon, ndox may wal, mu di ca naan.
1.Buur ya 17:6
Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.
Filib 4:19
Buleen jikkowoo bëggub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.»
Yawut ya 13:5
Moo leen teg coono, xiifal leen, leel leen mànn mu ngeen xamul, te seeni maam xamuñu ko woon, ngir xamal leen ne du aw ñam doŋŋ la doom aadama di dunde, waaye gépp kàddu gu tukkee ci gémmiñu Aji Sax ji, dees na ko dunde.
Baamtug yoon wi 8:3
Yeesu neeti leen: «Maa leen ko wax déy, ci lu wér, du Musaa moo leen jox ñamu asamaan, sama Baay la, te moo leen jox tey ñamu asamaan dëgg. Ndaxte ñamu Yàlla mooy ki wàcce asamaan te kooku moo may àddina ñu dund.» Ñu ne ko nag: «Sang bi, dee nu may saa su ne ci woowu ñam!»
Yowaan 6:32–34
Bés yu mujj yi
Wone yépp13 Okt 2025
12 Okt 2025
11 Okt 2025
10 Okt 2025
9 Okt 2025
8 Okt 2025
7 Okt 2025