Leeru Bés bi — 9 Oktoobar: Neyemi 9:17

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ñoo baña dégg, baña bàyyi xel sa kéemaan yi nga def ci seen biir, te ñoo sajju loos, fétteeral ba fal njiit, nara dellu ca seen njaam ga. Waaye yaw yaay Yàlla jiy boroom njéggal ak yiw ak yërmande, di muñ mer, te bare ngor, ba tax waccoo leen.

Neyemi 9:17

Du caageenu yeexe gu Boroom bi yeexe dige ba, noonu ko ñenn ñi fooge ag yeex. Yeen la muñal kay, ndax bëggul kenn sànku, xanaa ñépp dem ba tuub.

2.Piyeer 3:9

Sunu Boroom nag, ag muñam, jàppleen ne moo dig mucc, noonee leen ko sunu soppe, mbokk mi Póol binde woon ci xel mu rafet mi ñu ko baaxe.

2.Piyeer 3:15

Waaye loolu moo tax man bàkkaarkat bi ci raw, ma dajeek yërmande, ngir ci lépp lu nu Almasi Yeesu di muñal, ma doon ci misaal, ñeel ñi ko nara gëm ëllëg, ba texe ba fàww.

1.Timote 1:16

Ndaxte mboolem lu ñu bindoon, bu njëkk, jàngal nu moo taxoon ñu bind ko, ngir Mbind mi may nu xolu muñ, te ñaax nu, ba nu am yaakaar.

Room 15:4

Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy akug jéllaleem akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?

Room 2:4

Du seeni yére doŋŋ ngeen di xotti, ngir ñaawlu, seenub xol ngeen di xottiwaale, ñaawloo ko. Waññikuleen ci seen Yàlla Aji Sax ji, mooy boroom yiw ak yërmande; mer maa diib, ngor ga bare, muy fomm mbugal.

Yowel 2:13

Ku ñàkk a ngii, ñu futti, mu ngi binni, di néew-ji-doole. Aji Sax ji nee: «Maa ngii, di ci jóg, teg leen fi rawtu gu ñu ne siiw.»

Taalifi cant 12:6

Sang bi, maaka sopp sa kàddu gi set ni weñ gu ñu xelli!

Taalifi cant 119:140

Yoonu Aji Sax jee mat, di leqali bakkan. Lu Aji Sax ji seede dëgg la, day xelal ku xeluwul.

Taalifi cant 19:8

Lu Yàlla wax, mat na sëkk, mooy yiir ku ko làqoo. Bul yokk ay waxam, mu weddi say fen, nga weeru.

Kàddu yu xelu 30:5–6

Sama xol laa làq say wax, ngir bañ laa moy.

Taalifi cant 119:11

Say tegtal laay jàngat, di teewlu say xàll.

Taalifi cant 119:15

Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal.

Filib 4:8

Ni liir buy doora juddu yàkkamtee nàmpe, ni ngeen wara yàkkamtee nàmp soow mu set miy kàddug Yàlla. Mooy tax ngeen màgg ci seen dundug texe,

1.Piyeer 2:2

Nun nag danoo melul ni ñu bare, ñiy julaa kàddug Yàlla, waaye ci ndigalal Yàlla ak fi kanam Yàlla la nuy waaree xol bu set, ci Almasi bi nu gëm.

2.Korent 2:17

Waaye danoo dàq jépp jëf ju gàccelu ju nit di jëfe làq-làqal. Doxunu ag njublaŋ te sopparñiwunu kàddug Yàlla. Liy dëgg kay lanuy fésal, ba am kóoluteg ñépp, fi kanam Yàlla.

2.Korent 4:2