Leeru Bés bi — 7 Oktoobar: Taalifi cant 25:9

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

di jiite ku woyof mbubb ci njubte, di ko xamal aw yoonam.

Taalifi cant 25:9

Ndokkalee ñi woyof, nde ñooy moom àddina.

Macë 5:5

Ma seetlooti fi kaw suuf ne du ku gaaw, yaay raw; du ku jàmbaare, yaa moom xare; du ku xelu, am loo dunde; du ku muus, duunle; du kuy xamkat, amu yiw; ku nekk ak bésam ak wërsëgam.

Kàdduy waare 9:11

Nit ay sumb yoonam, Aji Sax ji sottal.

Kàddu yu xelu 16:9

Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Yaw laay séentu, yaw mi toog fa asamaan. Ma ne, ni jaam bu góor di wékke sangam bët, jaam bu jigéen di ko wékke bët sangam bu jigéen, ni lanuy wékke sunu Yàlla Aji Sax ji bët, ba keroog mu baaxe nu.

Taalifi cant 123:1–2

Xëye ma sa ngor, yaw laa wóolu; xamal ma fu may doxe, yaw laa wékk sama bakkan.

Taalifi cant 143:8

Éy sunu Yàlla, xanaa doo leen ñàkka dikke mbugal mi ñu yelloo, nde nun kat amunu dooley jànkoonteek gàngoor gu réy gii dikk ci sunu kaw. Nun nag danoo xamul nu nuy def, te yaw kat lanu ne jàkk sunuy gët.»

2.Jaar-jaar ya 20:12

Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.

Yanqóoba 1:5

Moom miy Noowug dëgg gi, bu dikkee, moo leen di àggale ci dëgg gi gépp, ndax du ci coobarey boppam lay wax, waaye mboolem lu mu dégg la leen di wax, te liy ñëw ëllëg, moo leen koy wax.

Yowaan 16:13

Kon nag Sang bi, nangula barkeel sama kër, ngir mu sax ba fàww fi sa kanam. Ndax kat yaw Aji Sax ji, yaa ko barkeel, kon nag dina barkeel moos, ba fàww.»

1.Jaar-jaar ya 17:27

Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.

Kàddu yu xelu 10:22

Nu nekk laa leen wone ne sunu wartéef mooy nu liggéeye noonu bu baax, ngir dimbali néew-doole yi, tey fàttaliku kàddug Sang Yeesu ga mu noon: “Nangu, joxee ko ëpp barke.”»

Jëf ya 20:35

Boo dee waajal bernde kay, wool néew-doole yi ak làggi yi, ak ñiy soox ak silmaxa yi. Su boobaa ndokkalee yaw, nde amuñu sag pey, waaye dees na la fey, kera ndekkitel aji jub ñi.»

Luug 14:13–14

«Ca la buur bay wax ñi ci ndijooram ne leen: “Yeen ñi sama Baay barkeel, dikkleen jël nguur gi ñu leen waajalaloon ba àddina sosoo. Ndaxte ba ma xiifee, yeena ma leel; ma mar, ngeen nàndal ma; ma dib doxandéem, ngeen fat ma; ma rafle, ngeen wodd ma; ma wopp, ngeen toppatoo ma; ñu tëj ma, ngeen seetsi ma.”

Macë 25:34–36

Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.

Taalifi cant 41:1

Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.

Taalifi cant 84:11