Loolu di firi ne ci Almasi bi la Yàlla jubale waa àddina ak jëmmu boppam, ba toppu leen seeni tooñ, te moo nu dénk kàddug juboo gi.
2.Korent 5:19
Leeru Bés bi
Loolu di firi ne ci Almasi bi la Yàlla jubale waa àddina ak jëmmu boppam, ba toppu leen seeni tooñ, te moo nu dénk kàddug juboo gi.
2.Korent 5:19
ndax Yàlla la soob mu dëël gépp matam ci moom. Deretam ja tuuru ca bant ba, ca la Yàlla defe jàmm, ba sottale ci moom, pexe mi mu jubalee boppam ak lépp, muy lu nekk ci kaw suuf ak la fa asamaan.
Kolos 1:19–20
Wallam aka jege ñi ko ragal, te leeram dëgmal sunu réew mii!
Taalifi cant 85:10
Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal. Kàddug Aji Sax jee. Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg.
Yeremi 29:11
«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.
Esayi 1:18
Ana Yàlla ju mel ni yaw, di baale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom? Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.
Mise 7:18
Jubool ak Yàlla rekk, am jàmm, ngëneel dikkal la.
Ayóoba 22:21
Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox, ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.
Filib 2:12–13
Aji Sax ji, yaa nuy defal jàmm, te lépp lu nu def, yaa nu ko sottalal.
Esayi 26:12
na sa nguur dikk, na sa coobare ame fi suuf na mu ame fa asamaan.
Macë 6:10
«Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.
Dañeel 2:44
Naka ngay xool, aw doj wu loxo sànniwul fàq, daldi dal ca tànki jëmm ja bindoo weñ ak ban bu ñu lakk, daldi koy rajaxe.
Dañeel 2:34
Mu wax ma ne ma: «Lii moo di kàddug Aji Sax ji dikkal Sorobabel, di wax ne: Du cig njàmbaar, du ci doole, ci samag noo la. Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.»
Sàkkaryaa 4:6
Farisen yi ñoo laajoon Yeesu, ne ko: «Kañ la nguurug Yàlla di dikk?» Mu ne leen: «Dikkug nguurug Yàlla du ànd akum ceetaan. Deesul ne it: “Xoolleen, mu ngi!” mbaa: “Ma ngee!” Ndax kat nguurug Yàlla mu ngi ci seen biir.»
Luug 17:20–21
Mu ne leen: «Yeen lañu xamal mbóotum nguurug Yàlla, waaye ñi ci biti ñoom, lépp ciy léeb lañu leen koy dëxëñal.
Màrk 4:11
Yeesu teg ca ne: «Nguurug Yàlla dafa mel ni nit ku sànni jiwu fi suuf. Buy nelaw ak bu yewwoo, guddi ak bëccëg, jiwu maa ngi sax, di màgg, te xamul nan la koy defe.
Màrk 4:26–27
Pepp ñor, janti ngóob taxaw, mu dawal sàrtam.»
Màrk 4:29
Moo tax yeen itam waajleen ba jekk, ndax waxtu wu ngeen foogul, ci la Doomu nit ki di ñëw.
Macë 24:44
Noo gu Sell gi ak Séet bi nee ñu: «Ñëwal!» Ku ci dégg it, neel: «Ñëwal!» Ku mar, ñëwal; ku bëgg ci ndoxum dund mi, jëlal, ñu may la.
Peeñu ma 22:17
Bés yu mujj yi
Wone yépp11 Okt 2025
10 Okt 2025
9 Okt 2025
8 Okt 2025
7 Okt 2025
6 Okt 2025
5 Okt 2025