Bu ñu tuddalee noonu bànni Israayil sama tur, man, maa leen di barkeel.»
Màndiŋ ma 6:27
Leeru Bés bi
Bu ñu tuddalee noonu bànni Israayil sama tur, man, maa leen di barkeel.»
Màndiŋ ma 6:27
Aji Sax ji sunu Yàlla, yeneen sang yu la moy moom nañu nu, waaye saw tur rekk lanuy màggal.
Esayi 26:13
Nu ngi mel ni xeet woo masula yilif, xeet wu ñu masula tudde sa tur. Éy soo xaroon asamaan, wàcc, ba tund yi yëngu fi sa kanam!
Esayi 63:19
Su boobaa mboolem xeeti kaw suuf dinañu gis ne turu Aji Sax ji lees leen di woowe, te dinañu leen ragal.
Baamtug yoon wi 28:10
Aji Sax ji moom turam wu màgg wi tax na du wacc ñoñam, ndax Aji Sax ji la soob, mu def leen ñoñam.
1.Samiyel 12:22
Boroom bi, ngalla Boroom bi, déglu nu te baal nu! Rikk Boroom bi sama Yàlla, teewlul ngir yaw ci sa bopp, te bañ noo yeexe, ndax saw tur lañu tudde sa dëkk ak sa mbooloo.»
Dañeel 9:19
Éy Yàlla, yaa nuy musal, wallu nu, ba sa seede rafet. Xettali nu te baal nu sunuy bàkkaar, ba sa woy rafet. Bul tax yéefar yi naa: «Ana seen Yàlla?» May nu, nu gis ni ngay mbugale yéefar yi, feye leen sa deretu jaam yi tuuru.
Taalifi cant 79:9–10
Turu Aji Sax ji rawtu bu mag la. Ku jub daw làqu ca, raw.
Kàddu yu xelu 18:10
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Taalifi cant 19:1
Ndax kat, li gisuwul ci Yàlla, te di manooreem gi dul jeex, ak jikko ji mu wéetoo ndax li muy Yàlla, ba àddina sosoo ba tey, xel man na koo ràññee ci ay liggéeyam, te looloo leen taxa ñàkku lay.
Room 1:20
Moona noppiwula seedeel boppam ci mbaaxam gi muy jëfe, di leen wàcceel fa asamaan taw ak naataange, reggal leen, bégal leen ba seen xol sedd.»
Jëf ya 14:17
Asamaan nee Yàlla màgg na, kaw ne màww, biral liggéeyu loxoom! Bésoo bés kàddu seede ko, guddee guddi xamle ca mbir.
Taalifi cant 19:2–3
Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp, feeñal nga ca sa kàttan, ngir jaxase say noon, bañaaleek feyukat ne xerem. Damay xool sa asamaan si nga móol, ak weer week biddiiw yi nga fi teg.
Taalifi cant 8:3–4
Jant bi ak leeru boppam, weer wi ak leeru boppam, biddiiw yi ak seen leeru bopp, te biddiiw sax wuute naak moroom ma ag leer. Noonu itam la ndekkitel ñi dee di deme. Li ñu suul mooy jiwu wiy yàqu, te bu dekkee dootul yàqu.
1.Korent 15:41–42
Ña rafet xel leer nàññ ni leeraayu déndub asamaan. Ñi doon xiir mbooloo mi ci njub ne boyy niy biddiiw, ba fàww.
Dañeel 12:3
Bés yu mujj yi
Wone yépp27 Sàt 2025
26 Sàt 2025
25 Sàt 2025
24 Sàt 2025
23 Sàt 2025
22 Sàt 2025
21 Sàt 2025