Leeru Bés bi — 4 Sàttumbar: Ruut 3:18

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Mu ne ko: «Yaw kay neel tekk fii rekk, doom, ba xam nu mbir miy mujje. Waa jii du toog te toppatoowul mbir mii tey, ba mu leer.»

Ruut 3:18

Nga wax ko ne ko: “Defal ndànk te ne cell. Bul tiit, bul xàddi ndax merum Reccin ak Siri, ak doomu Remalya ji. Duñu dara lu moy ñaari gil yuy saxaar!

Esayi 7:4

Mu ngi fey xare ci àddina sépp, dog fitt, damm xeej, lakk pakk.

Taalifi cant 46:10

Yeesu ne ko: «Xanaa waxuma la ne soo gëmee, dinga gis màggug Yàlla?»

Yowaan 11:40

Bésub keroog booba, kuy daŋŋiiral, detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.

Esayi 2:17

Ci kaw loolu rakkam ju ñuy wax Maryaama toog ca wetu Sang bi, di déglu kàddoom,

Luug 10:39

Ndaxam lenn doŋŋ a manula ñàkk. Maryaama nag, cér bi gën la taamu, te deesu ko nangu ci moom.»

Luug 10:42

Ndax Boroom bi Aji Sax ji, Aji Sell ju Israayil dafa wax ne: «Délsi, dallu moo leen di musal. Ne tekk te wóolu maa leen di dooleel. Waaye yeena bëggul!

Esayi 30:15

Xamleen ne Aji Sax ji day séddoo ku ko ragal, te bu ma woowee Aji Sax ji, mu dégg.

Taalifi cant 4:4

Neel tekk, xaar Aji Sax ji, yaakaar ko. Bu sa xol jóg ci kuy baaxle tey lal ay pexe.

Taalifi cant 37:7

Du ragal dég-dég bu tiis, xel ma day dal, mu wóolu Aji Sax ji, fit wa toog, du ragal, ba kera muy gis noonam jóoru.

Taalifi cant 112:7–8

Moo tax Boroom bi Aji Sax ji wax ne: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ aw doju koñu tabax, muy doju koñu tànnéef wu gànjare ci fondmaa bi, te ku ko wéeroo doo gaawa daw.

Esayi 28:16

Yeesu ne ko: «Man li may def nii tey, xamuloo ko; waaye ëllëg dinga ko xam.»

Yowaan 13:7

Fàttalikuleen mboolem yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji awale diiru ñeent fukki at yii ci màndiŋ mi, teg leen coono, nattu leen ngir xam li ci seen biir xol, xam ndax dingeen wormaal ay santaaneem, am déet.

Baamtug yoon wi 8:2

Ma jaareeti fa, xool la, gis ne mat ngaa séy. Ma tàllal sama mbubb, sànge ko sa yaramu neen, ba noppi giñal la, dikke la kóllëre. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Nii laa la moome.

Esekiyel 16:8

ndax Boroom bi, ku mu sopp, yar la, mooy bantal jépp doom ju ko neex.»

Yawut ya 12:6

Soppe yi, tàngooru nattu bi ngeen nekke nii, bumu leen jaaxal ba mel ni lu jaaduwul moo leen dikkal. Waaye noonu ngeen séddoo ci coonoy Almasi bi, bégeleen ko, ngir bu ndamam feeñee, ngeen gënatee bég.

1.Piyeer 4:12–13

Sunu coono bu woyof bii ci àddina, ci diggante bu gàtt nag, moo nuy jural teraanga ju diisaay ba jéggi dayo, teraanga ju sax dàkk. Moo waral xoolunu ci li bët mana gis, waaye li bët dul gis, ci lanuy xool, ndax li bët mana gis day wéy, waaye li bët dul gis mooy sax ba fàww.

2.Korent 4:17–18