Leeru Bés bi — 20 Sulet: Yowaan 17:16

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ni ma ñàkka bokke ci àddina, man ci sama bopp, noonu lañu ñàkka bokke ci àddina.

Yowaan 17:16

Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko.

Esayi 53:3

Loolu dama leen koo wax ngir seen xel dal ci man. Àddina sii, dingeen fi am njàqare, waaye dëgërluleen, ndax daan naa àddina.»

Yowaan 16:33

Boobu sarxalkat bu mag lanu soxla: moo sell, mucc sikk, mucc sobe, moom lañu teqale ak bàkkaarkat yi ci àddina, te moom lañu kaweel ba fa tiim asamaan.

Yawut ya 7:26

ngir seen der set wecc, te kon deesuleen mana gàkkal ci lenn. Ay goney Yàlla yu amul sikk ngeen di doon, ci biir maas gu dëng te yàqu, ngeen di lerxat ci seen biir, ni ay leer ci àddina si,

Filib 2:15

ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane nootoon.

Jëf ya 10:38

Kon nag bi nu koy jekku, nanuy def lu baax, ngir ñépp, rawatina waa kër yoonu ngëm wi.

Galasi 6:10

Leer giy dëgg, tey leeral nit ñépp, moo dikk ci àddina.

Yowaan 1:9

Yeena di leeru àddina. Ab dëkk, bu nekkee ci kaw tund, du mana làqu.

Macë 5:14

Yeen, na seenug leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seen jëf ju rafet, ba sàbbaal seen Baay ba fa kaw.

Macë 5:16

Xol bu tiis, naqar wu sax; xol bu neex, bànneex bu sax.

Kàddu yu xelu 15:15

Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!»

Neyemi 8:10

Ndax kat solos nguurug Yàlla jotewul dara akug lekk mbaa ag naan, waaye solos nguuru Yàlla moo di njub ak jàmm ak mbégte ci ndimbalal Noo gu Sell gi.

Room 14:17

Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen Noowug Yàlla fees, ngeen di jàngalante taalifi cant yi ak woyi cant yi ak woy yu fentoo ci Noowug Yàlla gi, di woy aka kañ Boroom bi ci seen xol. Fu ngeen tollu, ak ci mbir mu mu mana doon, santleen Yàlla Baay bi ci sunu turu Sang Yeesu Almasi bi,

Efes 5:18–20

Kon nag saa su nekk, nanuy jaare ci Yeesu, di génne sunu saraxu cant, ñeel Yàlla, muy sarax su bawoo ci sunuw làmmiñ, ñu di ko birale aw turam.

Yawut ya 13:15

Ndaxam garabu figg meññul, doomu reseñ amul ca ndeyam, njurum garabu oliw àntuwul, tool yi meññul aw ñam, gàtt it tukkee na ca gétt ga, du genn jur gu gudd ci wërmbal, te man may bànneexoo Aji Sax ji, Yàlla ji may wallu laay bége.

Abakug 3:17–18

Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.

2.Korent 6:10

Te yemunu ci, xanaa di sagoo sunuy tiis itam, nde xam nanu ne dékku aw tiis mooy taxa muñ;

Room 5:3