nde Kiy Boroom doole moo ma defal jaloore, cellte ñeel naw turam.
Luug 1:49
Leeru Bés bi
nde Kiy Boroom doole moo ma defal jaloore, cellte ñeel naw turam.
Luug 1:49
«Ana kuy sa moroom ci tuur yi, yaw Aji Sax ji? Kuy sa dend, yaak sa sellaay bu yéeme, sa yànjaay bu raglook sa jëf yu yéeme?
Mucc ga 15:11
Boroom bi, doo moroomu tuur yi, te jëf melul ni sa jos.
Taalifi cant 86:8
Boroom bi, ana ku la ragalul? Ku dul màggal saw tur? Yaw doŋŋ yaa sell. Askan yépp ay dikk, sujjóotsil la, ndax yaa jubi dogal.»
Peeñu ma 15:4
Yeen nag nangeen ñaane nii: “Sunu Baay bi fi asamaan, nañu wormaal sa sellaayu tur,
Macë 6:9
«Cant ñeel na Boroom bi Yàllay Israayil, moo seetsi ñoñam, ba jot leen!
Luug 1:68
Ana kuy kii bawoo Edom, sol yére yu xonq, bawoo Boccara? Kii ak yéreem yu yànj, di daagoo dooleem ju bare? Aji Sax ji nee: «Xanaa man mii di waxe dëgg, te am dooley walloo.»
Esayi 63:1
Sunu kiiraay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israayil mooy boroom.
Taalifi cant 89:19
Moom mi mana jëfoo kàttan giy liggéey ci nun, ba sottal mboolem lu nu ñaan ak lu nu xalaat, ba wees loola fuuf sax, moo yelloo daraja ci biir mbooloom gëmkat ñi, ak ci Almasi Yeesu, tey ak ëllëg, ba fàww. Amiin.
Efes 3:20–21
neex ni layub tundu Ermon, neex ni lay bu ni mel tey rogalaate tundi Siyoŋ. Fa la Aji Sax ji dogale barke, muy dund, ba fàww.
Taalifi cant 133:3
Noonu la bànni Israayil nangoo suuf sa dale ca Arower, ga ca catal walum Arnon, ba ca tundu Siyoŋ ga ñuy wax itam Ermon.
Baamtug yoon wi 4:48
neex ni layub tundu Ermon, neex ni lay bu ni mel tey rogalaate tundi Siyoŋ. Fa la Aji Sax ji dogale barke, muy dund, ba fàww.
Taalifi cant 133:3
Aji Sax ji nee: «Maay garabal seenug déggadi, maa leen di bëggal sama bopp, nde mereetuma leen.
Ose 14:5
Na samam njàngale sóob nib taw, samay kàddu rogalaat nib lay, ba tuurul am ñax, baawaanal gàncax.
Baamtug yoon wi 32:2
Ab taw ak tawub yuur ay wàcce asamaan, du fa dellu, te suuxatul suuf, saxal ko, meññal ko, ba kuy ji, mu may la jiwu; kuy lekk, mu may lam pepp. Sama kàddu giy bawoo sama gémmiñ it, noonu la. Du délsee ag neen ci man te deful li ma namm, ba sottal li ma ko yebal.
Esayi 55:10–11
Yàlla kat, ku mu yebal, kàddug Yàlla lay wax, ndax Yàlla du natt li mu koy nàddil cig Noowam.
Yowaan 3:34
Ci ag matam lanu tanqe nun ñépp, yiw ci kaw yiw.
Yowaan 1:16
Daa neex ni diwu bopp gu xeeñ, siite sikkim, bu mel ni sikkimu Aaróona, rogalaat ba ci mbubbam,
Taalifi cant 133:2
Bés yu mujj yi
Wone yépp18 Sul 2025
17 Sul 2025
16 Sul 2025
15 Sul 2025
14 Sul 2025
13 Sul 2025
12 Sul 2025