Mu ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Céy Aji Sax ji, xanaa du lii laa waxoon ba ma génnagul sama réew? Moo taxoon ma njëkka daw, jëm Tarsis! Ndax xamoon naa ne yaw Yàlla yaay boroom yiw ak yërmande, sa mer a diib, sa ngor bare, ngay fomm mbugal.
Yunus 4:2
Leeru Bés bi
Mu ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Céy Aji Sax ji, xanaa du lii laa waxoon ba ma génnagul sama réew? Moo taxoon ma njëkka daw, jëm Tarsis! Ndax xamoon naa ne yaw Yàlla yaay boroom yiw ak yërmande, sa mer a diib, sa ngor bare, ngay fomm mbugal.
Yunus 4:2
Kon nag ngalla Boroom bi, na sa doole màgg rekk, noonee nga noon: “Aji Sax ji! Kiy muñ mer, te bare ngor, di baale tooñ aki moy te du ñàkka topp mukk doom, tooñu waajuram, ba ca sët yaak sëtaat ya.”
Màndiŋ ma 14:17–18
Bul nu topp ñaawtéef ya woon, ngalla gaaw noo gatandoo sa yërmande. Danu ne dàll, ba ne dett. Éy Yàlla, yaa nuy musal, wallu nu, ba sa seede rafet. Xettali nu te baal nu sunuy bàkkaar, ba sa woy rafet.
Taalifi cant 79:8–9
Dëgg la sunuy ñaawtéef a nu tuumaal, waaye éy Aji Sax ji, jógal te saw tur tax, doonte dëddu nanu la ay yooni yoon, moy la.
Yeremi 14:7
Aji Sax ji, xam nanu sunug mbon, xam sunu ñaawtéefi maam; moy nanu la moos.
Yeremi 14:20
Ki Sax, yaw, soo doon lim bàkkaar, Boroom bi, ana kuy taxaw? Waaye yaay jéggale, ñu ragal la.
Taalifi cant 130:3–4
Nun nag bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla fu nu tollu, ci yeen ñi Boroom bi sopp, ndax yeen la njëkka tànn, ngir sellal leen ci Noo gu Sell gi, ak itam seen ngëm gi ngeen gëm dëgg gi, ngir texeel leen.
2.Tesalonig 2:13
Yaw, ngelawal bëj-gànnaar, yewwul, ngelawal bëj-saalum, dikkal, wolalleen ma sama tool bi, mu gilli; sama nijaay dugg toolam, xéewloo ngën-gi-meññeefam.
Ngën-gi-woy 4:16
Gisleen nag, seen tiis wi leen Yàlla teg ci coobareem, li mu leen jural: gii parlu; gii kàddug layoo gu ngeen yékkati, rawati; mii mer mu war, rawati; gii ragal Yàlla rawati; gii nammeel rawati; gii xéraange rawati; gii pastéef ci yar ki tooñ rawati! Nu nekk ngeen setale seen bopp wecc ci mbir moomu.
2.Korent 7:11
Li leer gi ci yeen di meññ moo di mboolem luy mbaax ak njub ak dëgg. Ràññeeleen li neex Boroom bi;
Efes 5:9–10
Waaye Taxawukat bi, di Noo gu Sell gi leen Baay biy yónnee ci sama tur, moo leen di jàngal lépp, fàttali leen lépp lu ma leen waxoon, man.
Yowaan 14:26
Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
Room 5:5
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm
Galasi 5:22
Doonte jaar nañu ci nattub njàqare bu mag, seen mbégtee rembat ci seen biir ñàkk gu tar, ba géejal seenug tabe.
2.Korent 8:2
Loolu lépp, genn Noo googu moo koy def, ku nekk, mu sédd la ci, ni mu ko soobe.
1.Korent 12:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp16 Sul 2025
15 Sul 2025
14 Sul 2025
13 Sul 2025
12 Sul 2025
11 Sul 2025
10 Sul 2025