Njurum jaan mi ngeen doon, nu ngeen mana waxe lu baax, te di ñu bon? Gémmiñ, la fees xolu boroom lay wax.
Macë 12:34
Leeru Bés bi
Njurum jaan mi ngeen doon, nu ngeen mana waxe lu baax, te di ñu bon? Gémmiñ, la fees xolu boroom lay wax.
Macë 12:34
Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi.
Kolos 3:16
Sàmmal a sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
Kàddu yu xelu 4:23
Dund ak dee a ngi ci làmmiñ, te wax garab la, ku ko bëgg, lekk ca doom ya.
Kàddu yu xelu 18:21
Kàddug aji jub day xelu, wax ja jub; yoonu Yàllaam a nga ca xol ba, du dox ba tërëf.
Taalifi cant 37:30–31
Bu genn kàddu gu bon génne seen gémmiñ, xanaa su ko jaree ngeen wax lu baax, luy jariñe, te diw yiw ci ñi koy dégg.
Efes 4:29
Waaye nun, li nu gis, dégg ko, manunu koo baña wax.»
Jëf ya 4:20
Ba ma wax: «Torox naa ba toskare,» teewul may ànd ak ngëm.
Taalifi cant 116:10
«Képp ku dëggal fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, man ci sama wàllu bopp itam, dinaa dëggal fa sama kanam Baay ba fa asamaan, ne man nga féeteel.
Macë 10:32
Ndax kat ab xol lees di gëme, ba am àtteb ku jub, te aw làmmiñ lees di birale ngëm gi ba mucc.
Room 10:10
Teewul ma yaakaar laa gis balaa yàgg, ba ne la jàkk, nga ne ma jàkk, nu waxtaan.
3.Yowaan 14
Ni sawara di jafale boob, baxale ko am ndox, ni ngay xamalsee say noon saw tur, ba yooyu xeet di lox fi sa kanam.
Esayi 64:1
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel askanu Kore wu góor. Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox, maa la koy sàkkoo xol.
Taalifi cant 42:1–2
Nijaay, dawsil, melal ni kéwél, mbaa kooba gu ndaw ci kaw tund wi ci gàncax gu xeeñ gi.
Ngën-gi-woy 8:14
Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi bi.
Filib 3:20
Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi.
Tit 2:13
Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu, ci ndigalal Yàlla sunu Musalkat ak Almasi Yeesu sunu yaakaar, ci man la bataaxal bii bawoo,
1.Timote 1:1
Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,
1.Piyeer 1:8
Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, léegi ma ñëw.» Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!
Peeñu ma 22:20
Bésub keroog dees na ne: «Sunu Yàllaa ngii nag! Moom mii lanu yaakaaroon te moo nuy wallu. Aji Sax jii lanu yaakaaroon, nan bég te bànneexoo wallam.»
Esayi 25:9
Bés yu mujj yi
Wone yépp13 Sul 2025
12 Sul 2025
11 Sul 2025
10 Sul 2025
9 Sul 2025
8 Sul 2025
7 Sul 2025