Aji Sax ji sa Yàllaa ngi fi sa biir, di jàmbaar juy walloo. Moo lay bége ci biir bànneex, leqalee la cofeelam, bége la bay sarxolle.
Sofoni 3:17
Leeru Bés bi
Aji Sax ji sa Yàllaa ngi fi sa biir, di jàmbaar juy walloo. Moo lay bége ci biir bànneex, leqalee la cofeelam, bége la bay sarxolle.
Sofoni 3:17
Du seen barewaay bu ngeen ëpplee xeet yépp moo tax Aji Sax ji naw leen, ba tànn leen, nde yeena gëna néew ci xeet yépp. Waaye cofeel gu leen Aji Sax ji sopp, ak sàmm gu mu sàmm ngiñam la mu giñaloon seeni maam, moo tax mu génnee leen dooley loxoom, jote leen ca kërug njaam ga, ak ca loxol Firawna buuru Misra.
Baamtug yoon wi 7:7–8
Nun nag, li nu taxa am cofeel moo di Yàlla moo nu njëkka sopp.
1.Yowaan 4:19
Te yeen ñi masoona sore lool Yàlla, doonoon ay noonam ci wàllu xalaat ak jëf ju bon, tey, deewug yaram, deewug suux gi Almasi bi dee, moom la leen Yàlla jubalee ak boppam, ba teewal leen fi kanamam, ngeen di ñu sell, mucc sikk, seen der set wecc.
Kolos 1:21–22
Lii mooy cofeel: cofeel gi du sunug cofeel, nun ci Yàlla; xanaa cofeel gi mu nu sopp, ba yebal Doomam, def ko njotlaay, ñeel sunuy bàkkaar.
1.Yowaan 4:10
Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu doon ay bàkkaarkat, ca la Almasi bi deewe ngir nun!
Room 5:8
Ci kaw loolu rekk, baat jibe asamaan, ne: «Kii mooy sama Doom, sama soppe; Moom laay bànneexoo.»
Macë 3:17
Li tax Baay bi sopp ma, moo di sama bakkan laa joxe, ba man koo jëlaat.
Yowaan 10:17
Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp. Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,
Yawut ya 1:2–3
deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe.
Yawut ya 10:20
Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nódd, fa féete Àjjana penku.
Njàlbéen ga 4:16
Seeni ñaawtéef a dox seen digganteek seen Yàlla. Seeni moy a leen xañ kanamam, ba mu tanqamlu leen.
Esayi 59:2
Sàkkuleen jàmm seen diggante ak ñépp, te it sàkkuleen cellte, nde ku sellul du gis Boroom bi.
Yawut ya 12:14
Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg gi, te maay dund gi. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarewul ci man.
Yowaan 14:6
Woowu yiw, la ko fésal moo di dikkug sunu Musalkat Almasi Yeesu, mi neenal dee, te niital nu yoonu texe, ak dee gu fomm ba fàww, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.
2.Timote 1:10
Noonu la Noo gu Sell gi firndeele ne yoon wu maye ñu dugg ca néeg bu sella sell ba feeñagul woon, te fekk néeg bu njëkk ba di taxaw ba tey.
Yawut ya 9:8
Ndaxte moom mooy sunu jàmm, moom mi boole ñaar, Yawut bi ak jàmbur bi dul Yawut, def leen kenn. Ci suuxu yaramam wa ñu daaj la ñàggee ñagu mbañeel bi doxoon sunu diggante.
Efes 2:14
Ca saa sa ridob biir néegu Yàlla ba dale ca kaw ba ca suuf, xar ñaar, suuf sa yëngu, doj ya xar,
Macë 27:51
Waaye xat la def, bunt ba jëm dund; sew it la yoon wa def, te ñu néew a koy gis.
Macë 7:14
Yaa may xamal yoonu dund. Fu bànneex mate, yaa teew, xéewal sa ndijoor la saxe.
Taalifi cant 16:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp5 Suw 2025
4 Suw 2025
3 Suw 2025
2 Suw 2025
1 Suw 2025
31 Mee 2025
30 Mee 2025