Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»
Njàlbéen ga 32:28
Leeru Bés bi
Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»
Njàlbéen ga 32:28
Aji Sax ji moo séq ak Yuda ab layoo, mooy mbugale Yanqóoba ay jëfinam, añale ko ay jëfam. Ci biiru ndeyam la kii suufoo ab seexam; kii moo tollu ci dooleem, bëreek Yàlla.
Ose 12:3–4
Teewul digeb Yàlla ba la ne jàkk, nàttablewul, gëmadiwul, xanaa dëgërloo dooley ngëmam rekk, sant Yàlla.
Room 4:20
Yeesu ne leen: «Gëmleen Yàlla. Maa leen ko wax déy, képp ku ne tund wale: “Jógal, tàbbiji géej,” te bañ cee boole xel ñaar, xanaa gëm ne li nga wax dina am, noonu lees la koy nangule. Moo tax ma di leen wax lii: Lépp lu ngeen di sàkku cig ñaan, gëmleen ne jot ngeen ko ba noppi, dingeen ko am.
Màrk 11:22–24
Yeesu ne ko: «Nga ne: “Soo manee”? Ku ànd ak gëm kay, dara tëwu la.»
Màrk 9:23
Ndokkalee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!»
Luug 1:45
Ci kaw loolu ndaw ya ne Sang bi: «Yokk nu ngëm.»
Luug 17:5
Léegi nag xale yi, saxleen ci Almasi bi, ndax bu feeñee, nu siggi fi kanamam te baña rus kera ba muy feeñ.
1.Yowaan 2:28
Waaye ngëm la koy ñaane te bumu ci am benn sikki-sàkka, ndax kiy sikki-sàkka daa mel ni gannaxu géej bu ngelaw liy yóbbu, di ko lëmbaaje. Kooku bumu yaakaar dara ci Boroom bi. Boroom xel ñaar la, xel maa toogul ci lenn lu muy def.
Yanqóoba 1:6–8
Man de jaaxle naa ci nii ngeen gaawa dëddoo Yàlla mi leen woo ci boppam, ci ndimbalal yiwu Almasi bi, bay topp xaat beneen xibaaru jàmméey! Te beneen dafa amul sax, xanaa ñenn ñi leen di jaxase, te bëgga sopparñi xibaaru jàmm bu Almasi bi. Waaye nun ci sunu bopp, mbaa malaaka mu bawoo ci asamaan sax, ku leen ci àgge woon beneen xibaaru jàmm bu dul bi nu leen àgge, kooku yal na alku!
Galasi 1:6–8
Yeen ñiy sàmm yoonu Musaa, di ko sàkkoo àtteb njub fa kanam Yàlla, daggoo ngeen ak Almasi bi, ñàkk ngeen yiwu Yàlla. Ndax nun kat, ci ndimbalal Noo gu Sell gi ak ci sunu kaw ngëm lanu yaakaare njub gi nuy séentu. Ci Almasi Yeesu mi nu gëm, xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ngëm gi jëfi cofeel di firndeel. Seen njàlbéenu xél de baax na! Ana ku leen gàllankoor ba toppuleen dëgg gi?
Galasi 5:4–7
Saxleen ci man, ni ma saxe man ci sama bopp ci yeen. Ni carub reseñ tëlee meññal boppam, su saxul ci ndeyam, ni ngeen di tëlee meññ, su ngeen saxul ci man.
Yowaan 15:4
Su ngeen saxee ci man te samay wax sax ci yeen, lu ngeen bëgg, ñaanleen ko, dees na leen ko nangul.
Yowaan 15:7
Ak li digey Yàlla di bare lépp, ci Almasi bi la ay digeem di doone «waaw». Moo tax itam, ci moom lanu naan Yàlla: «Amiin», ngir delloo ko njukkal.
2.Korent 1:20
Bés yu mujj yi
Wone yépp30 Mee 2025
29 Mee 2025
28 Mee 2025
27 Mee 2025
26 Mee 2025
25 Mee 2025
24 Mee 2025