Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
Luug 17:10
Leeru Bés bi
Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
Luug 17:10
Kon ana lees di bàkkoo? Dara! Ci lan lañu koy teg sax? Ci jëf ju yoon santaane? Mukk! Xanaa yoonu ngëm doŋŋ.
Room 3:27
Ana ku la def nga gën ci nit ñi? Ana loo am lu ñu la joxul? Te ndegam dees la koo jox, ana loo koy puukarewoo, mbete lees la joxul?
1.Korent 4:7
Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la; du peyu jëf, ba kenn di ci kañu. Ndax kat noo di liggéeyu Yàlla; Yàllaa nu yeesal ci Almasi Yeesu, ngir nu wéye jëf ju rafet ja mu nu fàgguloon ca njàlbéen, ngir nu di ko jëfe.
Efes 2:8–10
Ci yiwu Yàlla daal laa doone ki ma doon, te yiw woowu ma ñeel neenul. Te sax yeneen ndaw yépp sax, maa leen gëna liggéey. Du ci man nag, waaye yiwu Yàlla wi ànd ak man la.
1.Korent 15:10
Ci moom la lépp sosoo, ci moom la lépp sottee, te moom la lépp ñeel. Moom la daraja ñeel ba fàww! Amiin.
Room 11:36
Ana lu nu tekki, maak sama ñoñ, ba nu man laa jox saraxi yéene yii? Ci yaw la lépp jóge, te say loxo lanu jële, jox la.
1.Jaar-jaar ya 29:14
Sang bi, bul layook man; kenn jubul fi sa kanam, du kuy dund.
Taalifi cant 143:2
Moo xam sunu bind, di bàyyi xel ne pënd lanu.
Taalifi cant 103:14
Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndub suuf, ëf ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.
Njàlbéen ga 2:7
Naa la sante sama bind bu raglu bii te yéeme, say jalooree di kéemaan, bir na ma! Sama jëmm jii umpu la, ba muy bindu ci kumpa, mel ni lu ñu ràbbe ci xóotey suuf. Gis nga ma, ba ma diw lumb; sa téere lim na fan yi nga ma àppal, ba ca benn dooragul.
Taalifi cant 139:14–16
Xanaa du benn baay lanu am, nun ñépp? Te jenn Yàlla jee nu sàkk? Lu waral ku ne di wor mbokkam, ba ñàkka wormaal kóllërey maam ya?
Malasi 2:10
“Ndax sunu bakkan ak sunu yëngu ak sunug nekk, lépp ci moom la.” Mooy ba tey la ñenn ci seeni woykat ne: “Nun itam aw xeetam lanu.”
Jëf ya 17:28
Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal.
Taalifi cant 103:13
Teewul mu yërëm, baal leen seen ñaawtéef, ba sànku leen. Muñ na meram, muñati, te toppul xolam, ndax xalaataat ne suuxu neen lañu, di noo guy dem te du délsi.
Taalifi cant 78:38–39
Bés yu mujj yi
Wone yépp4 Suw 2025
3 Suw 2025
2 Suw 2025
1 Suw 2025
31 Mee 2025
30 Mee 2025
29 Mee 2025