Leeru Bés bi — 1 Suwe: Galasi 5:22

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm

Galasi 5:22

Ci kaw loolu Aji Sax ji romb fa kanam Musaa, di biral naan: «Aji Sax jee, Aji Sax ji, Yàlla jiy yërëme, di yéwéne, di muñ mer, boroom ngor gu bare gaak kóllëre ga.

Mucc ga 34:6

Dama leen di dénku nag, man mi ñu tëj ndax Sang bi, ngir ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla bi mu leen woo. Saxooleen woyof, lewet, te deeleen muñ, di muñalante ngir cofeel.

Efes 4:1–2

Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey baalante, ni leen Yàlla baale ci Almasi bi.

Efes 4:32

Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la njëkka def, teg ci ànd ak jàmm akug dal. Day taxa neexa jubool, fees ak yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-parloo akug jinigal.

Yanqóoba 3:17

Cofeel nag, muñ ak mbaax la. Cofeel bokkul ak kiñaan, bokkul ak jikkoy kañu aka damu.

1.Korent 13:4

Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.

Galasi 6:9

Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc. Yeen itam muñleen te takk seenu fit, ndax bés ba Boroom biy dikk dëgmal na.

Yanqóoba 5:7–8

«Janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» muy firi Yàllaa ngi ak nun.

Macë 1:23

«Waaye yaw Yàlla! Ndax yaay dëkk ak doom aadama ci kaw suuf sax? Seetal rekk, asamaan ba ca asamaani asamaan manu laa fat, astamaak kër sii ma tabax.

2.Jaar-jaar ya 6:18

Kàddu gee sol aw suux, doon nit, màkkaanoo ci sunu biir, nu ne jàkk ci darajaam, darajay jenn Doom ji bawoo ci Baay bi, mat sëkk ci aw yiw akug dëgg.

Yowaan 1:14

Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.

1.Timote 3:16

Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp.

Yawut ya 1:2

Bésub dibéer googu ca ngoon, di bés bi jiitu ci ayu bésu Yawut ya, bunt yaa nga tëje fa taalibe ya daje, ndax ragal njiiti Yawut ya. Yeesu ne jimeet taxaw ci seen biir ne leen: «Jàmm seen!» Loolu la Yeesu wax, daldi leen won ay loxoom akug wetam. Taalibe ya nag bég lool ndax la ñu gis Sang bi.

Yowaan 20:19–20

Ba ñu ca tegee juróom ñetti fan, taalibey Yeesu ya dajewaat ca biir, Tomaa nekk faak ñoom. Yeesu ne jimeet ca seen biir, te bunt ya tëje. Mu ne leen: «Jàmm ngeen!» Ci kaw loolu mu ne Tomaa: «Tegal fii sa baaraam te xool samay loxo; te nga tàllal sa loxo, ne ko tegg ci samag wet. Bàyyil gëmadi te gëm.» Tomaa àddu ne ko: «Yaa di sama Boroom, di sama Yàlla!»

Yowaan 20:26–28

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Esayi 9:6