Yal nanga tëj gémmiñu fen-kat buy wax aji jub waxi reewande, di réy-réylooka xeebaate.
Taalifi cant 31:19
Leeru Bés bi
Yal nanga tëj gémmiñu fen-kat buy wax aji jub waxi reewande, di réy-réylooka xeebaate.
Taalifi cant 31:19
Yaay gatandu kiy bége njekk gi muy jëfe te di ba xel say yoon yi ñu mas di jaare, ba mucc. Waaye kat, yaa nu mere, ndax noo bàkkaar.
Esayi 64:4
Mooy noonu ñu binde rekk ne: «Lu bët gisul, nopp déggu ko, xel daju ko, Yàllaa ko dencal ñi ko sopp.» Waaye nun la Yàlla feeñalal denc googu jaare ci Xelam. Ndaxte Xelum Yàlla lépp lay gëstu ba ci xóotey mbóoti Yàlla.
1.Korent 2:9–10
Yaa may xamal yoonu dund. Fu bànneex mate, yaa teew, xéewal sa ndijoor la saxe.
Taalifi cant 16:11
Sa njubtee tiim tund yu mag yi, sa àtte ne xéew ni xóotey géej. Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm! Céy Yàlla, yaa wéet ngor, doom aadama yiiroo sa keppaar, yiiru; yafloo sa njël lu duun, sa xéewal wal, nga nàndale ko.
Taalifi cant 36:7–9
Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ragal Yàlla, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg.
1.Timote 4:8
«Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Catir nag, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Doomu Yàlla ji, ki ay gëtam mel ni sawara wu yànj, ay tànkam mel ni xànjar bu ñu jonj. Mu ne:
Peeñu ma 2:18
«Dara gënula dëng xelum nit, laago la ci moom. Ana ku ko mana xam? Maay Aji Sax jiy seetlu xel, di natt ab xol, di yool ku nekk jëfinam, la yellook añam.
Yeremi 17:9–10
Sunuy ñaawtéef a ngi janook yaw, te sunu mbóot leer na la.
Taalifi cant 90:8
Ci kaw loolu Sang bi geesu, ne jàkk Piyeer, Piyeer fàttaliku la ko Sang bi waxoon ne ko: «Bala ganaar a sab tey jii, dina fekk nga jàmbu ma ñetti yoon.» Piyeer nag génn, di jooy jooy yu metti.
Luug 22:61–62
Waaye Yeesu moom, taxul mu wóolu leen, ndax ñoom ñépp la xamoon, te it soxlawul kenn xamal ko nit, ndax moom ci boppam xam na li ci nit.
Yowaan 2:24–25
Moo xam sunu bind, di bàyyi xel ne pënd lanu.
Taalifi cant 103:14
Barax bu lemu sax, du ko damm, leer gu giim it, du ko fey. Mooy indi yoonu dëgg.
Esayi 42:3
Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ki mu séddoo,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»
2.Timote 2:19
«Man maay sàmm bi baax. Maa xam sama xari bopp, ñoom it ñu xam ma.
Yowaan 10:14
Samay xar, sama baat lañuy déglu; maa leen xam, te man lañuy topp. Man maa leen di texeel ba fàww; duñu sànku mukk, te kenn du leen foqatee ci sama loxo.
Yowaan 10:27–28
Bés yu mujj yi
Wone yépp24 Mee 2025
23 Mee 2025
22 Mee 2025
21 Mee 2025
20 Mee 2025
19 Mee 2025
18 Mee 2025