Ndax kat ni Baay bi jagoo dund ci jëmmu boppam, noonu la maye Doom ji mu jagoo dund ci jëmmu boppam,
Yowaan 5:26
Leeru Bés bi
Ndax kat ni Baay bi jagoo dund ci jëmmu boppam, noonu la maye Doom ji mu jagoo dund ci jëmmu boppam,
Yowaan 5:26
Woowu yiw, la ko fésal moo di dikkug sunu Musalkat Almasi Yeesu, mi neenal dee, te niital nu yoonu texe, ak dee gu fomm ba fàww, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.
2.Timote 1:10
Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi; ku ma gëm, soo deewee it, dinga dund.
Yowaan 11:25
Des na tuuti, àddina du ma gisati; yeen dingeen ma gis, ndax man maa ngi dund, te yeen itam dingeen dund.
Yowaan 14:19
Ndax kat noo di àndandooy Almasi bi, ndegam wéye nanoo ŋoy bu dëgër ci sunu kóolute ga nu doore, ba kera muj ga.
Yawut ya 3:14
Ñi ñu xasa leeral nag, te ñu jota mos may gu bawoo ci asamaan, séddu ci Noo gu Sell gi, deesu leen mana defal dara.
Yawut ya 6:4
Ci jooju daraja ak jooju jaloore lees nu baaxee ay dige yu réy njëg te màgg. Yooyu dige nag, bu ngeen ci jotee, ci ngeen di séddu ci jikkoy Yàlla, gannaaw bu ngeen muccee ci yàqutey àddina gi xemmemtéefu bakkan waral.
2.Piyeer 1:4
Noonu lañu binde ne: «Aadama, nit ku njëkk ka daldi doon boroom bakkan,» waaye Aadama mu mujj mi moo di Noo giy maye bakkan.
1.Korent 15:45
Kaayleen ma xamal leen mbir mu umpe. Dunu dee nun ñépp, waaye nun ñépp ay soppiku. Lu gaawa gaaw lay doon, ci xef ak xippi, bu liit gu mujj ga jibee; nde liit ga mooy jib, ñi dee, dekki, di ñu dul yàqooti, nun nag, nu soppiku.
1.Korent 15:51–52
Ñeenti mbindeef yi am nañu ku nekk juróom benni laaf, fees aki bët ba daj, biir ak biti, te guddi ak bëccëg duñu selaw, xanaa naan: «Kee sell, Kee sell, Kee sell, Keey Boroom bi Yàlla Aji Man ji, Kee masa nekk, Kee nekk, Keey dikk.» Saa su mbindeef ya di màggal aka teral aka sant Boroom toogaayu ngàngune miy dund ba fàww,
Peeñu ma 4:8–9
te ki koy feeñal bu àppam jotee, di Ku tedd ki wéetoo nguuram, Buuru buur yi, Sangu sang yi, moom doŋŋ moo dul dee, moo màkkaanoo leer gu kenn jotewul, te mooy ki nit masula gis te tële koo gis. Teraanga ak kàttan ñeel na ko ba fàww. Amiin.
1.Timote 6:15–16
Yaw Buur bi sax dàkk, doo dee, te bët manu laa gis, yaw Yàlla miy kenn, yaa tedd, yaa màgg, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin!
1.Timote 1:17
Bunu di yég sunu bopp, di merloonte aka iñaanante.
Galasi 5:26
Sedeyoŋ dellu ne leen: «Lenn daal laay sàkku ci yeen: Na ma ku nekk ci yeen jox ab jaarob nopp ci alalu sëxëtoom.» Booba ay jaaroy nopp yu wurus la waa Majan daan takk, ndax moo doon baaxu Ismayleen ñi. Ñu ne ko: «Noo la koy jox kay!» Ñu lal malaan, ku nekk sànni ca jaarob nopp bu bokk ca alalu sëxëtoom.
Njiit ya 8:24–25
Wurus wa, mbubbam xar-sànni la ca Sedeyoŋ defarlu, ba teg ko ca Ofra, dëkk ba mu fekk baax. Israayil gépp nag di fa bokkaalee xar-sànni ma, mu doon ag fiir guy xiirtal Sedeyoŋ ak waa këram ci moy.
Njiit ya 8:27
Looy sàkku ku la beral loxo? Jaru ko! Maa ngii di wàcceel musiba képp kuy noyyi. Kàddug Aji Sax jee! Waaye may naa la sa bakkan di sa yoolu xare, fépp foo jëm.”»
Yeremi 45:5
Te it, waccalees na ma ndégu biir suux, mu taxawe ndawal Seytaane, di ma mitital, ngir ma baña bew ndax peeñu yu yéeme.
2.Korent 12:7
Buleen def dara ci kaw wujje, mbaa réy-réylu, waaye woyofluleen, ba jàpp ne seeni moroom a leen gën.
Filib 2:3
Cofeel nag, muñ ak mbaax la. Cofeel bokkul ak kiñaan, bokkul ak jikkoy kañu aka damu. Bokkul ak jëf ju jekkadi ak jiital sa njariñal bopp, bokkul ak naqari deret, bokkul ak denc mer.
1.Korent 13:4–5
Bés yu mujj yi
Wone yépp17 Mee 2025
16 Mee 2025
15 Mee 2025
14 Mee 2025
13 Mee 2025
12 Mee 2025
11 Mee 2025