Leeru Bés bi — 23 Mee: Mucc ga 28:12

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Tappal ñaari per yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, per yi taxawe taxawaayu bànni Israayil, Aaróona gàddu seeni tur ci kaw ñaari ngàlli waggam, fi kanam Aji Sax ji, ngir saxal ag pàttaliku.

Mucc ga 28:12

Waaye Yeesu mi sax ba fàww, moo sasoo carxal gu sax dàkk. Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.

Yawut ya 7:24–25

Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk,

Yudd 24

Gannaaw nag am nanu kilifag sarxalkat bu mag bu jàll ba ca biir asamaan, te mooy Yeesu Doomu Yàlla, nanu ŋoy ci yoonu ngëm wi. Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar. Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.

Yawut ya 4:14–16

Beñamin la wax, ne ko: «Soppeb Aji Sax jaa ngi, keey dëkke xel mu dal fi wetam, mu di ko yiir bésoo bés, te diggantey waggam la dëkke.»

Baamtug yoon wi 33:12

Guddig keroog Buur tëlee nelaw, daldi santaane ñu indil ko téere ba ñu dippee Xew-xew ya. Ci kaw loolu ñu di ko jàngal Buur.

Esteer 6:1

Ma bàyyi Yàlla xel, binni, xalaat, xol jeex. Selaw.

Taalifi cant 77:4

Ana ku mel ni sunu Yàlla Aji Sax ji, ki kaweel ab jalam, toog, di jéer asamaan ak suuf?

Taalifi cant 113:5–6

nga dënoo biir callweer, melax yi taal àddina, suuf di lox, di reg-regi.

Taalifi cant 77:19

Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.

Taalifi cant 76:10

Aji Sax ji déy suuf sépp lay jéere ay gëtam, ngir dooleel ñi ko wéetalal seen xol. Yëfi dof nga def ci mbir mii, ndax li dale tey ay xare topp na la.»

2.Jaar-jaar ya 16:9

Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.

Room 8:28

Ñaari picci ramatu, xanaa du dërëm lay jar? Moona menn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay. Seen kawari bopp sax, waññees na lépp.

Macë 10:29–30