Leeru Bés bi — 20 Mee: 1.Timote 4:16

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Sàmmal sa bopp nag, sàmm sa àlluwa, te saxoo ko; soo ko defee, dinga mucc, musal ñi lay déglu.

1.Timote 4:16

Joŋantekati tàggat yaram yi, dañuy yar seen yaram bu metti, te ñooñu kaalag ndam guy seey doŋŋ lañu ci yaakaar, waaye nun, kaalag ndam gu sax dàkk lanu ci yaakaar. Man nag noonu laay dawe, waaye samaw xél ñàkkul ab jëmu. Noonu laay këmëxee it, waaye dóoruma ci jaww ji. Damay yar sama yaram yar bu metti kay, ba moom ko, ndax ëllëg ñu bañ maa doyadal, gannaaw bu ma xamalee ñeneen kàddu gi ba noppi.

1.Korent 9:25–27

Ràngooleen mboolem gànnaayi Yàlla, ngir ngeen mana jànkoonte ak pexey Seytaane. Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan.

Efes 6:11–12

Ñi bokk ci Almasi Yeesu nag, ñoo daaj ca bantam ba seen bakkan, daajaale ko ak sàkkuteefam yu tar aki xemmemtéefam. Gannaaw nag Noowug Yàlla moo nu dundal, nanu topp Noo gi.

Galasi 5:24–25

Ndax kat, mboolem ñiy dox ci njiital Noo gi, ñooñu ay doomi Yàlla lañu.

Room 8:14

Loolu ngay def sam xel, mbir yooyu ngay pastéefoo, ba sag yokkute bir ñépp.

1.Timote 4:15

Yeesu ne ko: «Maryaama.» Mu geestu, làkk ko ci yawut ne ko: «Rabbuni!» Muy firi kilifa gi.

Yowaan 20:16

Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israayil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.

Esayi 43:1

Kooku la wattukat biy ubbil, xar yi di déglu baatam. Mooy woo xari boppam ci seen tur, génne leen. Bu génnee xaram yépp ba noppi, da leen di jiitu, ñu topp ci moom, ndax xàmmee nañu baatam.

Yowaan 10:3–4

Sama biir loxo yii laa la ñaas, say tataa janook man ba fàww.

Esayi 49:16

Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ki mu séddoo,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»

2.Timote 2:19

Gannaaw nag am nanu kilifag sarxalkat bu mag bu jàll ba ca biir asamaan, te mooy Yeesu Doomu Yàlla, nanu ŋoy ci yoonu ngëm wi.

Yawut ya 4:14

Nanga jël ñaari peri onigsë, nga ñaas ci turi doomi Israayil yu góor:

Mucc ga 28:9

Tappal ñaari per yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, per yi taxawe taxawaayu bànni Israayil, Aaróona gàddu seeni tur ci kaw ñaari ngàlli waggam, fi kanam Aji Sax ji, ngir saxal ag pàttaliku.

Mucc ga 28:12

«Nanga sàkk kiiraayal dënn bi ñuy jëfoo cib àtte, ñu liggéeyaale ko ay nataal ni xar-sànni mi, te nañu ko ràbbe wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe.

Mucc ga 28:15

Nanga we ay per ci kaw kiiraayal dënn bi, nga def ko ñeenti làngi per. Làng gi jiitu, peru sarduwan ak peru topaas ak peru eskarbukal moo cay nekk;

Mucc ga 28:17

Per yeek turi doomi Israayil yu góor ñooy tolloo ab lim: muy fukk ak ñaar, ni tur yi tollu. Dees ciy ñaas tur yi ni xàmmikaayi torlu, ku nekk ak turam, ba fukki giir yeek ñaar daj.

Mucc ga 28:21

Nanga yeb ci biir kiiraayal dënn bi ñuy àttee, jumtukaayi tegtal yooyu di Urim ak Tumim, ngir ñu tafu ci xolu Aaróona, saa yuy taxawi fi kanam Aji Sax ji. Noonu la Aaróona di dëkke yóbbaale ci kaw xolam jumtukaayi àtte yu bànni Israayil, saa suy taxawi fi kanam Aji Sax ji, ba fàww.

Mucc ga 28:30