Leeru Bés bi — 11 Awril: Kàddu yu xelu 10:19

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Wax ju bare, moy ñàkku ca; ku moom sa làmmiñ, xelu nga.

Kàddu yu xelu 10:19

Bokk yi, soppe yi, nangeen xam lii: na ku nekk di gaaw ci déglu, di yeexa wax tey yeexa mer.

Yanqóoba 1:19

Muñ mer, moo gën njàmbaar; tënk sa bakkan moo raw nangub dëkk.

Kàddu yu xelu 16:32

Bare na lu nuy tooñ, nun ñépp. Ku dul tooñ ci kàddu nag, kooku nit ku mat la, te man naa moom yaramam wépp, boole ci.

Yanqóoba 3:2

Ndax kat ci sa kàddu lees lay joxe dëgg, ci sa kàddu it lees lay daane.»

Macë 12:37

Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ, saytul ma sama kàddu.

Taalifi cant 141:3

Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.

1.Piyeer 2:21

Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg.

1.Piyeer 2:23

Xoolleen ci moom mi bàkkaarkat yi doon xeex, bala ngeena yoqi bay xàddi.

Yawut ya 12:3

te kàddug fen masula jibe seen gémmiñ. Amuñu benn gàkk-gàkk.

Peeñu ma 14:5

Éy Aji Sax ji, joxoñ ma saw yoon, jaarale ma joor gu wóor, ngir ñi may tëru.

Taalifi cant 27:11

Nga ne ma: «Dama laa xelal, xamal la fi ngay jaar, digal la, di la bàyyi xel.

Taalifi cant 32:8

Aji Sax jee baax, rafeti dogal, di gindi moykat ci yoon wi, di jiite ku woyof mbubb ci njubte, di ko xamal aw yoonam.

Taalifi cant 25:8–9

Man maay bunt bi; ku dugge ci man, dinga mucc, di dugg aka génn, di gis mbooy goo fore.

Yowaan 10:9

Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg gi, te maay dund gi. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarewul ci man.

Yowaan 14:6

Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca néeg bu sella sell ba, ngir deretu Yeesu, deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe. Am nanu itam sarxalkat bu mag bu jiite kër Yàlla ga. Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.

Yawut ya 10:19–22

Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»

Ose 6:3

Aji Sax ji ngor ak dëgg rekk lay jiitee kuy sàmm kóllëreem ak seedey yoonam.

Taalifi cant 25:10