Leeru Bés bi — 7 Awril: 2.Korent 6:10

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.

2.Korent 6:10

Ci ndimbalam lanu ame ngëm ba mana àgg fi yiwu Yàlla wii nu taxaw taxawaay bu dëgër. Te it sunub sag moo di yaakaar ji nuy séentoo ab cér ci leeru Yàlla. Te yemunu ci, xanaa di sagoo sunuy tiis itam, nde xam nanu ne dékku aw tiis mooy taxa muñ;

Room 5:2–3

Kóolute gu réy laa am ci yeen, te sag bi ma ame ci yeen réy na. Mbégte mu seral sama xol laa feese, te damaa fees ak bànneex ba rembat, ci biir sunu mboolem njàqare!

2.Korent 7:4

Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,

1.Piyeer 1:8

Doonte jaar nañu ci nattub njàqare bu mag, seen mbégtee rembat ci seen biir ñàkk gu tar, ba géejal seenug tabe.

2.Korent 8:2

Man mi yées ci ñu sell ñépp lañu may woowu yiw, ba may xibaar jàmbur ñi dul Yawut xéewal yu amul kem yi ci Almasi bi. May niital ñépp, ni Yàlla nara sottale mébétam, miy mbóot mu làqu woon naka jekk fa moom Yàlla mi sos lépp.

Efes 3:8–9

Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo tànn ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur gi Yàlla dig ñi ko sopp?

Yanqóoba 2:5

te Yàlla man na leena baawaanal wépp yiw, ba ngeen saxoo am lu leen doy ci lépp, ak koom gu bare, ngir jépp jëf ju baax.

2.Korent 9:8

Aji Sax jee lay aar, di sàmm sa bakkan, nga jagoo barke ci réew mi, te du la bàyyi noon def la lu ko neex.

Taalifi cant 41:3

Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.

Esayi 63:9

Ñaari jigéeni Lasaar yooyu nag yónnee ca Yeesu ne ko: «Sang bi, sa soppe bi daa wopp.»

Yowaan 11:3

Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi bi wàcc ci sama kaw.

2.Korent 12:9

Lépp laa mane ci ndimbalal ki may manal.

Filib 4:13

Moo tax dunu ñàkk yaakaar. Doonte sax sunu bitib jëmm a ngi gën di bon, sunu jëmmu biir moom, mu ngi yeeslu bésoo bés.

2.Korent 4:16

“Ndax sunu bakkan ak sunu yëngu ak sunug nekk, lépp ci moom la.” Mooy ba tey la ñenn ci seeni woykat ne: “Nun itam aw xeetam lanu.”

Jëf ya 17:28

Mooy dooleel ku loof, di kàttanal ku jeele. Waxambaane sonn, loof; xalelu góor di tërëf a tërëf, kiy yaakaar Aji Sax ji moom, di yeeslu doole; da naa fëyy ni jaxaay juy naaw, di xélu te du xiix, di dox te du xoox.

Esayi 40:29–31

Yàlla ji sax fàww moo dib rawtu, përëgam bi sax dàkk di cëslaay, moo la dàqal ab noon ne la: “Jekkalil!”

Baamtug yoon wi 33:27