Yeen janqi Yerusalem, damaa ñuul, rafet; ñuul ni xayma ya ca Kedar, mel ni ridoy Buur Suleymaan.
Ngën-gi-woy 1:5
Leeru Bés bi
Yeen janqi Yerusalem, damaa ñuul, rafet; ñuul ni xayma ya ca Kedar, mel ni ridoy Buur Suleymaan.
Ngën-gi-woy 1:5
Xam naa ne maa tooñ, sama moy a ngi janook man saa su ne.
Taalifi cant 51:5
siiw ba xeet yépp xam la ndax taar bu sotti ndax sama gànjar gu yànj gi ma la takkal. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Esekiyel 16:14
Simoŋ Piyeer nag gis loolu, daldi sukk fa kanam Yeesu, ne ko: «Sang bi, ngalla sore ma, ngir man nitu bàkkaarkat laa!»,
Luug 5:8
Yaaka rafet, xarit, yaaka taaru! Sa gët yi niy pitax, làqoo muuraay bi, njañ liy loy-loyee ngi saf géttu bëy yu ñuul yu bartaloo kaw tundu Galàdd.
Ngën-gi-woy 4:1
Moo ma tax ne: «Waqeet, tuubi-ruubi,» ba diwoo suuf akub dóom.
Ayóoba 42:6
Xarit, sa lépp a rafet, sikk nekkul ci yaw.
Ngën-gi-woy 4:7
Takk bi ma ci def daal mooy lii: bu ma nammee def lu baax, lu bon a may teewalsi.
Room 7:21
Ñu jekki indil ko ab lafañ, mu tëdd cig laltu. Ba Yeesu seetloo seen ngëm, da ne lafañ ba: «Na sa xel dal, doom, jéggalees na la say bàkkaar.»
Macë 9:2
Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.
Room 7:18
ci moom ngeen mate it, te mooy kilifay mboolem boroom nguur yi ak mboolem boroom sañ-sañ yi.
Kolos 2:10
Almasi boobu nag lanuy xamle; na mu gëna xeloo lanuy artoo nit ku nekk, te ni lanuy jàngale nit ku nekk, ngir àgge nit ku nekk ba fa kanam Almasi bi, fekk ko mat sëkk, na mu ware ku ànd ak Almasi bi.
Kolos 1:28
Te loolu la ñenn ci yeen doonoon. Waaye Yàllaa leen fóot, sellal leen, jubal leen, ci turu Sang Yeesu Almasi bi ak ci sunu Noowug Yàlla.
1.Korent 6:11
Waaye yeen nag yeenay giir giy tànnéef, yeenay sarxalkati buur, yeenay askan wu sell, yeenay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.
1.Piyeer 2:9
Te kat képp ku namma farlu ci yoonu Almasi Yeesu, dees na la bunduxataal.
2.Timote 3:12
Ndaxte li ma indi moo di teqale doom ju góor ak baayam; ak doom ju jigéen ak ndeyam; ak jabar ak goroom. Te it nooni nit ki, waa këram lay doon.
Macë 10:35–36
Bokkaalekat yi ngeen doon! Xanaa xamuleen ne xaritoo ak àddina moo di noonoo ak Yàlla? Kon nag ku namma def àddina ab xarit, ab noonu Yàlla ngay doon.
Yanqóoba 4:4
Buleen topp àddina ak li ci biiram. Ku topp àddina, cofeelu Baay bi nekkul ci moom. Ndax kat mboolem lu nekk ci àddina, muy xemmemtéefi bakkan, di mboolem xemmemtéef gu sosoo ci lu bët tege, ak réy-réylu gu alalu àddina waral, amul lenn lu ci jóge ci Baay bi, xanaa ci àddina.
1.Yowaan 2:15–16
«Su leen àddina bañee, xamleen ne man la njëkka bañ. Su ngeen bokkoon ci àddina, àddina bëgg leen, ndax li ngeen diy ñoñam, waaye dangeena bokkul ci àddina, nde maa leen tànne ci àddina, te looloo tax àddina bañ leen. Fàttalikuleen kàddu gi ma leen wax: “Jaam sutul sangam.” Gannaaw man lañu bunduxataal, yeen itam, dinañu leen bunduxataal. Bu ñu sàmmoon sama kàddu, dinañu sàmm seen gos itam.
Yowaan 15:18–20
Man, jottali naa leen sa kàddu, waaye àddinaa leen bañ, ndax ni ma ñàkka bokke ci àddina, ni lañu ñàkka bokke ci àddina.
Yowaan 17:14
Bés yu mujj yi
Wone yépp9 Awr 2025
8 Awr 2025
7 Awr 2025
6 Awr 2025
5 Awr 2025
4 Awr 2025
3 Awr 2025