Leeru Bés bi — 6 Awril: Yawut ya 7:25

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.

Yawut ya 7:25

Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!

Room 8:34

Ndax néeg yu sell yu nit tabax, te muy royaalub néeg bu dëggu ba doŋŋ, du ci la Almasi bi dugg. Waaye ci asamaan ci boppam la dugg ngir teewal nu tey, fa kanam Yàlla.

Yawut ya 9:24

Xale yi doom, loolu laa leen bind, ngir ngeen baña bàkkaar. Waaye su ci amee ku dem ba bàkkaar, am nanu ab layookat fa wetu Baay bi, te mooy Yeesu Almasi bi, boroom njub.

1.Yowaan 2:1

Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn rammukat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy kenn nit: muy Almasi Yeesu

1.Timote 2:5

Gannaaw nag am nanu kilifag sarxalkat bu mag bu jàll ba ca biir asamaan, te mooy Yeesu Doomu Yàlla, nanu ŋoy ci yoonu ngëm wi. Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar. Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.

Yawut ya 4:14–16

ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi bi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gu Sell gi.

Efes 2:18

Aji Sax jeey làq néew-ji-doole, mooy làqe bésub njàqare.

Taalifi cant 9:10

Ci jamonoom, Yuda dina texe, Israayil dëkke kaaraange, te dees na ko tudde nii: “Aji Sax jeey sunu njub.”

Yeremi 23:6

Boroom bi Aji Sax ji, ma dikke la sag njàmbaar, di tudd sa àtte dëgg gu wéet.

Taalifi cant 71:16

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Esayi 9:6

Aji Sax ji, maa xam ne nit moomul yoonam, kuy dox moomuli jéegoom.

Yeremi 10:23

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Esayi 9:6

Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.

2.Timote 1:12

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Esayi 9:6

Ndaxte moom mooy sunu jàmm, moom mi boole ñaar, Yawut bi ak jàmbur bi dul Yawut, def leen kenn. Ci suuxu yaramam wa ñu daaj la ñàggee ñagu mbañeel bi doxoon sunu diggante.

Efes 2:14

Gannaaw nag dees noo baaxe àtteb ñu jub ci kaw ngëm, jàmmoo nanu ak Yàlla ndax sunu Sang Yeesu Almasi bi.

Room 5:1

Turu Aji Sax ji rawtu bu mag la. Ku jub daw làqu ca, raw.

Kàddu yu xelu 18:10

Wóoy ngalla ña wàcci Misra, di wuti wall, di sukkandikoo ay fas, tey yaakaari watiir ndax bare ga, aki gawar ndax lim bu takku ba, te xooluñu ci Aji Sell ju Israayil, wutuñu kooku di Aji Sax ji.

Esayi 31:1

Ni picc di daayaarloo, aar am tàggam, ni la Aji Sax ji Boroom gàngoor yiy yiire Yerusalem. Mooy aar, di xettali, mooy musal, di yiwi.

Esayi 31:5