Day wattu ku jub fu mu jaare, di sàmm wóllëreem ciw yoon.
Kàddu yu xelu 2:8
Leeru Bés bi
Day wattu ku jub fu mu jaare, di sàmm wóllëreem ciw yoon.
Kàddu yu xelu 2:8
Loolu lépp taxul ngeen am kóolute ci seen Yàlla Aji Sax ji, ki leen daan jiitu ci yoon wi, ngir sàkkal leen fu ngeen di dale: guddi, mu nekk ci biir sawara, di leen niital yoon wu ngeen jaare; bëccëg, mu nekkal leen ci biir aw niir.
Baamtug yoon wi 1:32–33
Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam, daayaarlu, di wër, tiim leen, tàllali laafam, aw leen, teg ciw dunqam, boot leen. Aji Sax ji doŋŋ a leen wommat, du yàllay jàmbur ju ko ci fekk.
Baamtug yoon wi 32:11–12
Bu Aji Sax ji rafetloo saw yoon, mooy jiite say jéego. Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
Taalifi cant 37:23–24
Seen yaakaar tas, Aji Sax ji jege leen, seen xol jeex, Aji Sax ji wallu leen.
Taalifi cant 34:19
Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; yoonu ku bon di sànk boroom.
Taalifi cant 1:6
Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.
Room 8:28
Li ànd ak moom përëgub suux la, te ki ànd ak nun di Aji Sax ji sunu Yàlla ji nuy wallu, xareel nu sunuy xare.» Xelu askan wa nag dal ca kàddu ya Esekiyas buurub Yuda wax.
2.Jaar-jaar ya 32:8
Aji Sax ji sa Yàllaa ngi fi sa biir, di jàmbaar juy walloo. Moo lay bége ci biir bànneex, leqalee la cofeelam, bége la bay sarxolle.
Sofoni 3:17
Wetu fukki waxtu ak juróom ca ngoon, ca la Yeesu àddu ca kaw ne: «Eli, Eli, lema sabaktani?» Loolu di tekki «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga wacc ma?»
Macë 27:46
Te moom sunuy tooñ a waral ñu jamat ko; sunuy ñaawtéef a waral ñu dëggaate ko. Yar yi nu jàmmal moom la dal, te mooy ki nu wére ciy góomam. Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.
Esayi 53:5–6
Àttewuñu ko dëgg, yóbbu, te ag maasam kenn teewluwul ne tooñ gu sama bokk yi tooñ lees ko génne ci réewum aji dund ñi, te loolu lees ko faate.
Esayi 53:8
Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.
Esayi 53:10
Nun itam ci lanu; dees na nu limal sunu ngëm, àtteb ñu jub, nun ñi gëm ki dekkal sunu Sang Yeesu mi ñu teg ciy loxo, mu dee ndax sunuy tooñ, ba dekkal ko, ngir nu ame ci àtteb nit ñu jub.
Room 4:24–25
Almasi bi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gu Sell gi.
1.Piyeer 3:18
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar,» moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba, ngir nu deewal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»
1.Piyeer 2:24
Almasi bi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.
2.Korent 5:21
Almasi bi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»
Galasi 3:13
Bés yu mujj yi
Wone yépp5 Mar 2025
4 Mar 2025
3 Mar 2025
2 Mar 2025
1 Mar 2025
28 Few 2025
27 Few 2025