Naka noonu, yeen itam jàppeleen seen bopp nit ñu dee ba dootuleen nangooti kilifteefu bàkkaar, xanaa di dund ngir Yàlla, ndax seen bokk ci Yeesu Almasi bi.
Room 6:11
Leeru Bés bi
Naka noonu, yeen itam jàppeleen seen bopp nit ñu dee ba dootuleen nangooti kilifteefu bàkkaar, xanaa di dund ngir Yàlla, ndax seen bokk ci Yeesu Almasi bi.
Room 6:11
«Maa leen ko wax déy ci lu wér, ku dégg sama kàddu ba gëm ki ma yónni, yaa texe ba fàww, te àtte ba, doo ca jaare, waaye bàyyikoo nga ci dee, tàbbi ci dund.
Yowaan 5:24
Su dee wàllu yoonu Musaa nag, man nit ku dee laa, te yoonu Musaa moo ko waral, ngir ma mana dund dund gu ñeel Yàlla. Dees maa boole ak Almasi bi rey ca bant ba. Moo tax dootul man maay dund, waaye Almasi bi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.
Galasi 2:19–20
Des na tuuti, àddina du ma gisati; yeen dingeen ma gis, ndax man maa ngi dund, te yeen itam dingeen dund.
Yowaan 14:19
Man maa leen di texeel ba fàww; duñu sànku mukk, te kenn du leen foqatee ci sama loxo. Sama Baay bi ma leen jox, moo gëna màgg lépp, te kenn manula foqatee lenn ci loxol Baay bi. Man ak Baay bi benn lanu.»
Yowaan 10:28–30
Gannaaw nag yeena dekkeendoo ak Almasi bi, sàkkuleen la fa kaw, fa Almasi bi tooge ca ndijooru Yàlla.
Kolos 3:1
ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi bi, làqe fa Yàlla.
Kolos 3:3
Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.
Yanqóoba 1:5
Mu daldi siggi ne ko: «Ndaw sii, ana nit ñi? Kenn joxu la ci sab daan?» Mu ne ko: «Kenn, Sang bi.» Yeesu ne ko: «Man it duma la daan. Demal, te bul bàkkaarati.»
Yowaan 8:10–11
Waaye ni moyug Aadama deme, yiwu Yàlla demewu ni. Moyug kenn nit, Aadama, tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak mayug yiw gu kenn nit, Yeesu Almasi bi, ñaata yoon la gënatee baawaan, ñeel nit ñu bare? Ni njeexitalu tooñu kenn nit deme, laa ne, mayu Yàlla demewu ni. Benn bàkkaar moo waral àtte bi indi mbugal. Waaye moy yu bare moo waral may gi teggi tuuma.
Room 5:15–16
Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy gi mu nu sopp, nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi bi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce. Ci sunu bokk ak Yeesu Almasi bi la nu Yàlla dekkalandoo ak moom, dëëlandoo nook moom fa déndi asamaan. Mbaax gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu, moom lay firndeele mboolem xarnu yiy ñëw, ni yiwam yaatoo ba tiiñ am xel.
Efes 2:4–7
Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?
Room 8:32
Bés yu mujj yi
Wone yépp26 Few 2025
25 Few 2025
24 Few 2025
23 Few 2025
22 Few 2025
21 Few 2025
20 Few 2025