Ndax Yàlla moo sopp àddina, ba joxe jenn Doomam ji, ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww, te du sànku mukk.
Yowaan 3:16
Leeru Bés bi
Ndax Yàlla moo sopp àddina, ba joxe jenn Doomam ji, ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww, te du sànku mukk.
Yowaan 3:16
Loolu lépp ci Yàlla la jóge, moom mi nu jubale ak boppam ci Almasi bi, te moo nu sas, ngir nuy waare juboo googu. Loolu di firi ne ci Almasi bi la Yàlla jubale waa àddina ak jëmmu boppam, ba toppu leen seeni tooñ, te moo nu dénk kàddug juboo gi. Kon nag Almasi bi, noo diy ndawam, te ci nun la Yàlla di wootee. Kon ci turu Almasi bi, danu leen di ñaan: nanguleena juboo ak Yàlla. Almasi bi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.
2.Korent 5:18–21
Ku amul ag cofeel nag, xamuloo Yàlla, ndax Yàlla cofeelu neen la. Ni cofeelu Yàlla feeñe ci nun moo di jenn Doomu boppam ji mu yebal ci àddina, ngir nu mana dund ci kàttanam. Lii mooy cofeel: cofeel gi du sunug cofeel, nun ci Yàlla; xanaa cofeel gi mu nu sopp, ba yebal Doomam, def ko njotlaay, ñeel sunuy bàkkaar. Soppe yi, ndegam Yàllaa nu soppe nii, nun itam war nanoo soppante.
1.Yowaan 4:8–11
Xelum nit làmp la bu Aji Sax ji taal, da koy niital ba ca biir xolam.
Kàddu yu xelu 20:27
Naka lañu ko toppe ay laaj, mu siggi ne leen: «Ku masula bàkkaar ci yeen, na njëkka sànni ndaw si xeer.»
Yowaan 8:7
Ba nit ña déggee loolu, kenn-kenn lañu rocceeku, ña gën di mag jiitu. Yeesu doŋŋ a fa des, mook ndaw sa fa taxaw.
Yowaan 8:9
Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab ga ma la aaye, waay?»
Njàlbéen ga 3:11
Ku xam lu baax loo wara def te defoo ko nag, bàkkaar nga.
Yanqóoba 4:17
Ak lu nu sunum xel mana sikke, Yàllaa sut sunum xel, te lépp la xam. Soppe yi, bu nu sunum xel sikkul, dinanu ñemee walbatiku ci Yàlla.
1.Yowaan 3:20–21
Aw ñam, bumu la yàqloo liggéeyu Yàlla. Dëgg la, wépp ñam set na, waaye lekk ga nga koy lekk, su gàkkalee ngëmu keneen, def nga lu aay.
Room 14:20
Yaw ci sa wàllu bopp, ngëm gi nga ci am, yemale ko ci sa bopp, fi kanam Yàlla. Ndokkalee ki sikkul boppam lenn ci jëfin wu mu dogul boppam ne noonu lay jëfe.
Room 14:22
Yàlla, seetlu ma, ba ràññee sama xol; natt ma, ba ràññee sama xalaati xol. Xoolal ndax maa ngi doxe yoon wu aay, te nga teg ma ci yoon wi sax.
Taalifi cant 139:23–24
Bés yu mujj yi
Wone yépp27 Few 2025
26 Few 2025
25 Few 2025
24 Few 2025
23 Few 2025
22 Few 2025
21 Few 2025