Ngalla muril saay gët, ma niir sa kéemaani yoon.
Taalifi cant 119:18
Leeru Bés bi
Ngalla muril saay gët, ma niir sa kéemaani yoon.
Taalifi cant 119:18
Ca la ubbee seen xel, ngir Mbind mi leer leen.
Luug 24:45
Mu ne leen: «Yeen lañu may ngeen xam mbóoti nguurug asamaan, waaye ñale, mayeesu leen ko.
Macë 13:11
Ca jamono yooyu la Yeesu àddu ne: «Baay, Boroom asamaan ak suuf, sant naa la, nde yaa làq lii boroom xam-xam yeek boroom xel yi, xamal ko tuut-tànk yi, nde loolu de, Baay, mooy li la soob.
Macë 11:25–26
Nun nag du xelum àddina lanu jot, waaye Xel mi bawoo fa Yàlla lanu jot, ngir nu mana ràññee li nu Yàlla baaxe.
1.Korent 2:12
Yàlla, say xalaat aka maa yéem! Ndaw lim bu réy! Su ma ko doon waññ, moo ëpp feppi suuf. Maa ngii yewwu, nekk feek yaw ba tey.
Taalifi cant 139:17–18
Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam! «Ana ku mana nànd xalaatu Boroom bi? Ana ku ko mana digal?»
Room 11:33–34
Ci moom la lépp sosoo, ci moom la lépp sottee, te moom la lépp ñeel. Moom la daraja ñeel ba fàww! Amiin.
Room 11:36
Ba loolu amee Yàlla bënn doj wu xóot wa ca Lexi, ndox ma xelli, Samson naan, ag noowam délsi, mu leqaliku. Looloo tax ñu tudde bëtu ndox ba En Akore (muy firi Bëtu ndoxub ka woote wall). Ma nga foofa ca Lexi ba tey jii.
Njiit ya 15:19
Yeesu nag ne ndaw si: «Soo xamoon mayu Yàlla, ak kan moo la ne may ma, ma naan, kon yaw yaa koy ñaan, mu may la ndox miy dundal.»
Yowaan 4:10
Bés ba mujj ca màggal ga nag moo ca gënoona màgg. Keroog la Yeesu taxaw, àddu ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man, naan;
Yowaan 7:37
Booba Noowug Yàlla la doon wax, Noo ga gëmkati Yeesu doon waaja jot, te jotaguñu ko woon, ndax booba, Yeesoo tàbbeegul woon ci teraangaam.
Yowaan 7:39
Indileen mboolem céru fukkeel ca kërug denc ya, ba ab dund am sama biir kër, te ngeen seetloo ma ko rekk,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ndegam duma leen ubbil bunti asamaan, ba sottil leen barke bu doy.
Malasi 3:10
Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»
Luug 11:13
Moo tax ma ne leen, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, ndax ngeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
Luug 11:9
Li ngeen diy doom nag tax na Yàlla yebal Noowug Doomam ci seen biir xol, ba Noo gi naan: «Abba», muy firi Baay.
Galasi 4:6
Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di woowe Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay».
Room 8:15
Bés yu mujj yi
Wone yépp17 Sàt 2026
16 Sàt 2026
15 Sàt 2026
14 Sàt 2026
13 Sàt 2026
12 Sàt 2026
11 Sàt 2026