Ndax kat sopp Yàlla moo di, ay ndigalam nu di ko sàmm, te ay ndigalam diisul.
1.Yowaan 5:3
Leeru Bés bi
Ndax kat sopp Yàlla moo di, ay ndigalam nu di ko sàmm, te ay ndigalam diisul.
1.Yowaan 5:3
Ndax sama coobarey Baay kat moo di képp ku gis Doom ji te gëm ko, na texe ba fàww, te maa koy dekkal keroog bés bu mujj ba.»
Yowaan 6:40
Te kon lu nu ñaan, mu may nu ko, ndax ay ndigalam lanuy sàmm, te li mu rafetlu lanuy jëfe.
1.Yowaan 3:22
Sama kilifteef sedd na, te samab sëf woyof.»
Macë 11:30
«Su ngeen ma soppee, sàmmleen samay ndigal.
Yowaan 14:15
Ki nangu sama ndigal nag, te di ko sàmm, moo ma sopp, te kooku ma sopp, cofeel ñeel na ko, bawoo fa sama Baay, te man itam dinaa ko sopp, di ko feeñu.»
Yowaan 14:21
Mbégtee ñeel ku daj xel mu rafet ak ku amug dégg.
Kàddu yu xelu 3:13
Fa muy jaare yiw la, fu mu awe jàmm la.
Kàddu yu xelu 3:17
Jàmm ju baree ñeel ku sopp sa yoon, te dara du ko fakkastal.
Taalifi cant 119:165
Ndaxam ci sama biir xol, yoonu Yàllaa ma neex.
Room 7:22
Ndigalam nag moo di nu gëm turu Doomam Yeesu Almasi bi, tey soppante noonu mu nu ko dénke.
1.Yowaan 3:23
Cofeel du waral kenn def moroomam lu bon; kon cofeel moo matal sëkk yoonu Musaa.
Room 13:10
Bul xool li ma bàkkaare ndaw ak li ma moy. Aji Sax ji, xoole ma sa ngor ngir sag mbaax.
Taalifi cant 25:7
Maa far say moy, mu naaxsaay niw niir, say bàkkaar ne mes nib lay. Délsil fi man, jot naa la.»
Esayi 44:22
Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttaliku bàkkaar.
Esayi 43:25
«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.
Esayi 1:18
Kenn dootul soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji!” Ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ci ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»
Yeremi 31:34
Moo nuy yërëmati; sunuy ñaawtéef lay joggiy tànkam, te biir xóotey géej lay tàbbal sunuy bàkkaar.
Mise 7:19
Ndeke sama tiisu xol wii, sama jàmm rekk a tax. Sa cofeel a tax nga sorele maak paxum sànkute. Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.
Esayi 38:17
Ana Yàlla ju mel ni yaw, di baale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom? Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.
Mise 7:18
tukkee itam fa Yeesu Almasi bi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki njëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqalikook kilifteefu sunuy bàkkaar,
Peeñu ma 1:5
Bés yu mujj yi
Wone yépp28 Suw 2026
27 Suw 2026
26 Suw 2026
25 Suw 2026
24 Suw 2026
23 Suw 2026
22 Suw 2026