Leeru Bés bi — 26 Suwe: 1.Jaar-jaar ya 4:10

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Yabecc nag woo Yàllay Israayil wall, ne ko: «Éy, soo ma barkeeloon a barkeel, yokk samag moomeel, ànd ak man, musal ma ci lu aay lu may yóbbe mitit.» Yàlla may ko la mu ñaan.

1.Jaar-jaar ya 4:10

Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.

Kàddu yu xelu 10:22

Bu Yàlla nee cell, ana ku koy ŋàññ? Bu làqee kanamam, ana ku koy niir? Xeet yeek nit ñi la boole tiim,

Ayóoba 34:29

Éy Aji Sax ji sama Yàlla, jógal, wallu ma! Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp, foq seeni sell.

Taalifi cant 3:8

Yal nanga tëj gémmiñu fen-kat buy wax aji jub waxi reewande, di réy-réylooka xeebaate.

Taalifi cant 31:19

Ñaanuma nga jële leen ci àddina, xanaa nga musal leen ci ku bon ki.

Yowaan 17:15

«Ñaanleen, ñu may leen; seetleen, gis; fëggleen, ñu ubbil leen. Ndaxte képp ku ñaan, dinga am; ku seet, gis; ku fëgg it, dees na la ubbil.

Macë 7:7–8

Musiba nag day rey ku bon, te ku bañ aji jub, yoon dab na la.

Taalifi cant 34:22

Guddig keroog guddig teewlu la, ñeel Aji Sax ji, ngir moo leen ca génne réewum Misra, moo tax guddi googu di gu ñu jagleel Aji Sax ji, bànni Israayil gépp war cee fanaanee teewlu, ñeel Aji Sax ji, ba fàww.

Mucc ga 12:42

Man, li ma jële ci Sang bi, moom laa leen jottali: Sang Yeesu, guddi gi ñu ko woree, dafa jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg ko, ne: «Lii moo di sama yaram wi leen ñeel. Deeleen def lii, di ma ko fàttalikoo.» Noonu itam la def ak kaas ba, gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre gu yees gi fasoo ci sama deret. Deeleen def lii, di ma ko fàttalikoo, saa yu ngeen ci naanee.»

1.Korent 11:23–25

Ba loolu amee mu dànd leen lu tollook saanu xeer, daldi sukk, di ñaan.

Luug 22:41

Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.

Luug 22:44

Looloo nga yemook waxtuw digg bëccëg. Boobu ñu ngi waajal màggalu bésub Mucc ba. Pilaat nag ne Yawut ya: «Seen buur a ngoogu!»

Yowaan 19:14

Noonu nag Pilaat teg Yeesu ci seeni loxo, ngir ñu daaj ko ci bant. Ñu daldi yóbbu Yeesu. Moom ci boppam moo gàddu bant ba, génn jëm ba fa ñuy wax bérebu Kaaŋu bopp, muy firi Golgota ci làkku yawut. Foofa lañu daaje Yeesu ca bant ba, mook ñeneen ñaar; kii ci wet gii, kee ca wet gee, Yeesu ca digg ba.

Yowaan 19:16–18

Setalleen seen bopp boog, génneleen lawiir bu yàgg bi ci seen biir, ba mana doon tooyal bu bees bu mucc lawiir, nde doon ngeen ko ba noppi, ndax Almasi bi, sunu gàttub bésub Mucc biy sunub sarax, rendilees na nu ko. Kon nag, nanu màggal sunu bésub Mucc te bañ koo màggale lawiir bu yàgg, mbaa lawiiru yàqute akug mbon, xanaa nu màggale ko mburu mu amul lawiir, mburum xol bu set te dëggu.

1.Korent 5:7–8