tukkee itam fa Yeesu Almasi bi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki njëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqalikook kilifteefu sunuy bàkkaar,
Peeñu ma 1:5
Leeru Bés bi
tukkee itam fa Yeesu Almasi bi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki njëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqalikook kilifteefu sunuy bàkkaar,
Peeñu ma 1:5
Ndox mu ne xéew du fey mbëggeel, ay dex du ko mëdd. Ku koy weccee sa alalu kër gépp it, ñu jéppi laa jéppi rekk.
Ngën-gi-woy 8:7
Teg ma ci sa xol ni torlukaay, mbaa ci sa përëg ni lamu màndarga. Mbëggeel a bare doole ni dee, fiiraange xér ni bàmmeel. Day jàpp jippét, di jum bu Aji Sax ji taal.
Ngën-gi-woy 8:6
Joxe sa bakkan te say xarit tax, ameesul cofeel gu ko raw,
Yowaan 15:13
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar,» moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba, ngir nu deewal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»
1.Piyeer 2:24
Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,
Efes 1:7
Te loolu la ñenn ci yeen doonoon. Waaye Yàllaa leen fóot, sellal leen, jubal leen, ci turu Sang Yeesu Almasi bi ak ci sunu Noowug Yàlla.
1.Korent 6:11
Waaye yeen nag yeenay giir giy tànnéef, yeenay sarxalkati buur, yeenay askan wu sell, yeenay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.
1.Piyeer 2:9
Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu déy mooy njaamu gi leen war.
Room 12:1
Liggéeyin yi man naa wuute, waaye benn Boroom bi la.
1.Korent 12:5
Ci biir loolu, ka ñu dénkoon këri dencukaay Buur, Asmawet la, doomu Adiyel. Ka ñu dénkoon dencukaayi tool yi ci dëkk yu ndaw yeek yi ci dëkk-dëkkaan yeek tata yi, Yonatan la, doomu Osiyas. Ka jiite woon surga yay liggéey ca tool ya, di bey, Esri la, doomu Kelub. Ka ñu dénkoon tóokëri reseñ ya, Simey mu Raama la. Ka ñu dénkoon mbàndi biiñ ba ñu nale ca reseñ ya, di Sabdi mu Sefam.
1.Jaar-jaar ya 27:25–27
Ka ñu dénkoon gàtt ya, Yasis la, bokk ci giirug Agar. Ñooñu ñépp diy jawriñ yu ñu dénk alalu Buur Daawuda.
1.Jaar-jaar ya 27:31
Ñi Yàlla tabb ci biir mbooloom gëmkat ñi, ñi ci jiitu ñoo di ndawi Almasi bi. Ñaareel bi di ñiy waxe kàdduy waxyu, ñetteel bi di jàngalekati kàddu gi. Ñi ci topp di ñiy def ay kéemaan, ñi ci topp di ñi am mayu faje ak ñi mane dimbalee ak ñi mane jiite ak ñiy làkk yeneen xeeti làkk.
1.Korent 12:28
Loolu lépp, genn Noo googu moo koy def, ku nekk, mu sédd la ci, ni mu ko soobe.
1.Korent 12:11
Kenn ku ci nekk, may gi ko aw yiw jagleel, na ko taxawoo ñépp. Noonu ngeen di doone ay saytukat yu baax, di saytu ay may yu yiwu Yàlla wu yaa di joxe. Kuy wax, na waxe nu mu jottalee kàddug Yàlla. Kuy taxawoo, na taxawoo ci dooley Yàlla, ngir màggug Yàlla feeñe ci lépp ndax Yeesu Almasi bi, moom mi yelloo daraja ak kàttan, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
1.Piyeer 4:10–11
Bés yu mujj yi
Wone yépp2 Okt 2025
1 Okt 2025
30 Sàt 2025
29 Sàt 2025
28 Sàt 2025
27 Sàt 2025
26 Sàt 2025