Leeru Bés bi — 13 Suwe: Yowaan 15:4

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Saxleen ci man, ni ma saxe man ci sama bopp ci yeen. Ni carub reseñ tëlee meññal boppam, su saxul ci ndeyam, ni ngeen di tëlee meññ, su ngeen saxul ci man.

Yowaan 15:4

Moo tax dootul man maay dund, waaye Almasi bi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.

Galasi 2:20

Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.

Room 7:18

Céy maaka réy aw tiis! Ana ku may wallook sama yaramu dee wii? Waaye cant ñeel na Yàlla mi nuy walloo jëmmu Yeesu Almasi bi, sunu Sang. Kon daal man, ci sama bopp, ci sama wàllu xel, yoonu Yàlla laay surgawu, waaye ci sama wàllu yaramu suux wii, yoonu bàkkaar laay surgawu.

Room 7:24–25

Su Almasi bi nekkee ci yeen, seen yaram dina dee moos ndax bàkkaar, waaye du tee seenug noo di dund, ndax àtteb njub bi ngeen am ba noppi.

Room 8:10

Noonu la deme, ndegam kay fekk na leen sësoo ngëm gu ngeen dëjoo ba dëgër, te baña nangu lenn di leen sorele ak yaakaar ji ci xibaaru jàmm bi ngeen dégg, te ñu biral ko, ñeel mépp mbindeef. Man Póol nag, ci yégle xibaaru jàmm boobu laa di ab jawriñ.

Kolos 1:23

Léegi nag xale yi, saxleen ci Almasi bi, ndax bu feeñee, nu siggi fi kanamam te baña rus kera ba muy feeñ.

1.Yowaan 2:28

Ku ne moo sax ci Yàlla, fàww ni Yeesu Almasi bi daan jëfe, ni lay jëfe moom itam.

1.Yowaan 2:6

Ba Yeesu déggee ne dàq nañu waa ja gumba woon, dafa dem ba gis ko, ne ko: «Yaw, ndax gëm nga Doomu nit ki?» Waa ja ne ko: «Kooku kan la, Sang bi, ma gëm ko.»

Yowaan 9:35–36

Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,

Yawut ya 1:3

te ki koy feeñal bu àppam jotee, di Ku tedd ki wéetoo nguuram, Buuru buur yi, Sangu sang yi, moom doŋŋ moo dul dee, moo màkkaanoo leer gu kenn jotewul, te mooy ki nit masula gis te tële koo gis. Teraanga ak kàttan ñeel na ko ba fàww. Amiin.

1.Timote 6:15–16

«Man, maay Alfa, di Omega», la Boroom bi Yàlla wax, moom Ki masa nekk, Ki nekk, di Kiy dikk ëllëg, te di Aji Man ji.

Peeñu ma 1:8

Mu ne ko: «Gëm naa la, Sang bi,» daldi koy sujjóotal.

Yowaan 9:38

Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.

2.Timote 1:12

Moo waral lii dikk ci Mbind mi: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ, aw doju koñu tabax, muy doju tànnéef wu gànjare. Wii doj, ku ko wéeroo, doo rus mukk.» Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag: «Moo di doj wi tabaxkat yi beddi woon, te mu mujj di doju koñu tabax bi.»

1.Piyeer 2:6–7