Wattukat ya ne leen: «Nit masula waxe ni kii!»
Yowaan 7:46
Leeru Bés bi
Wattukat ya ne leen: «Nit masula waxe ni kii!»
Yowaan 7:46
Woy wu neex a fees sama xol, may taalifal Buur, sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan.
Taalifi cant 45:2
Boroom bi Aji Sax ji moo ma may làmmiñu ndongo lu mokkal, ngir ma xam gan kàddu laay jàppalee ku sonn. Suba su ne mu yee ma, yeel ma nopp bu ma teewloo ni dongo yi.
Esayi 50:4
Gémmiñam, bànneexi neen, jëmmam jépp jara xédd! Yeen janqi Yerusalem, sama nijaay a ngoog, samab xarit.
Ngën-gi-woy 5:16
Ñépp a doon seedeel Yeesu lu rafet, tey yéemu ci kàdduy yiw yi tukkee ci gémmiñam. Ñu naan: «Xanaa kii du doomu Yuusufa ji?»
Luug 4:22
ndax sañ-sañ ba mu leen di jàngale niroowul ak na seen firikati yoonu Musaa yay jàngalee.
Macë 7:29
Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi.
Kolos 3:16
Mbaxanam xare miy seen kaaraange, jëlleen ko, sol; jëlleen itam saamar bi Noo gu Sell giy joxe, te muy kàddug Yàlla.
Efes 6:17
Kàddug Yàlla de luy dund la, ànd ak doole, te moo gëna ñaw saamaru ñaari ñawka bu gëna ñaw. Day sar ba fa xel akug noo digaloo, ba fa yax ak yuq dajee, te man naa càmbar ay xalaat ak mébéti xol.
Yawut ya 4:12
Ndaxte gànnaay yi nuy xeexe du gànnaayi suuxi neen, waaye da di gànnaay yu am fa Yàlla kàttanu daane ay tata. Te xalaatin yu jubul, noo leen di daaneel, mook lépp luy réy-réyloo ab taxawaayam, di joŋante ak xam-xamu Yàlla, te nooy jàpp njaam bépp xalaat, ngir déggalloo ko Almasi bi.
2.Korent 10:4–5
xamoo ne ku bon, ag sarxolleem àggul fenn, te bànneexu yéefar yàggul?
Ayóoba 20:5
Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.»
Njàlbéen ga 3:15
Moona bés bu nekk, maak yeen la woon ca kër Yàlla ga, te teguleen ma loxo. Waaye seen waxtu la léegi, bi kilifteefug lëndëm ayee nii.»
Luug 22:53
Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane.
Yawut ya 2:14
Moo dog sidditi boroom nguur yeek boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, ñu doon ay jaam yu mu jàppe xare. Moo leen weer it ci kanam ñépp, diriwaale leen ca biir njaab ma topp ca ndam la Almasi bi ame ca bant ba.
Kolos 2:15
Àndleen ak sago te teewlu! Ki leen di tuumaal, Seytaane, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax. Pastéefu ngëm ngeen di xeexe te xam ne benn coono bi ngeen di daj, moom la mboolem seen bokki gëmkat yi ci àddina di daj.
1.Piyeer 5:8–9
Kon nag nangulleen Yàlla, te bañal Seytaane, mu daw, ba sore leen.
Yanqóoba 4:7
Ku bon fexeel ku jub, di ko màttu, Buur Yàlla di ko ree, xam ne bésam a ngi ñëw.
Taalifi cant 37:12–13
Su ko defee Yàlla miy boroom jàmm mooy dër Seytaane ci lu gaaw, fi ngeen ko joggi seeni tànk. Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu ànd ak yeen!
Room 16:20
Ñu jàpp nag Seytaane mi leen daan nax, sànni ko ci déegu sawaraak tamarax ba, mu fekki fa rab waak yonentu caaxaan ba. Dees na leen fa mitital guddi ak bëccëg, ba fàww.
Peeñu ma 20:10
Bés yu mujj yi
Wone yépp8 Suw 2025
7 Suw 2025
6 Suw 2025
5 Suw 2025
4 Suw 2025
3 Suw 2025
2 Suw 2025