Mooy fomp seen wépp rongooñ. Dee dootul am, dëj aki yuux aku tiis dootul am, lu njëkk laay wéy.»
Peeñu ma 21:4
Leeru Bés bi
Mooy fomp seen wépp rongooñ. Dee dootul am, dëj aki yuux aku tiis dootul am, lu njëkk laay wéy.»
Peeñu ma 21:4
Mooy mëdd dee ba fàww! Boroom bi Aji Sax jeey fompe gépp kanam rongooñi boroom. Buumi gàccey ñoñam it, moo koy doge fépp ci àddina. Aji Sax ji kat wax na ko.
Esayi 25:8
Sab jant du sooti, sa weer du suuxati. Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa fani ñaawlu jeex.
Esayi 60:20
Du kenn ci waa Yerusalem, ku neeti wopp na. Waa dëkk bépp ay am njéggalu bàkkaar.
Esayi 33:24
Maay bége Yerusalem, bànneexoo sama ñoñ. Deesu fi déggati ay jooy, mbaa coowal njàqare.
Esayi 65:19
Ñi Aji Sax ji goreel, nii lañuy dellusee, agsaaley sarxolle fa Siyoŋ, kaalawoo mbég mu sax, mbégteek bànneex wàllsi, naqar aku tiis daw.
Esayi 35:10
«Man nag ndax maa leen di musal ci njaniiw? Ndax maa leen di jot ci dee? Moo yaw dee, ana say mbas? Yaw njaniiw laa ne, ana sa tooke? Fomm làqu na ma!
Ose 13:14
Noon bu mujj bi ñuy neenal mooy dee,
1.Korent 15:26
Léegi nag bokk yi, ma fàttali leen xibaaru jàmm bi ma leen xibaaroon, muy lu ngeen gëm, sax ci,
1.Korent 15:1
Moo waral xoolunu ci li bët mana gis, waaye li bët dul gis, ci lanuy xool, ndax li bët mana gis day wéy, waaye li bët dul gis mooy sax ba fàww.
2.Korent 4:18
Ci sunu bokk ak Yeesu Almasi bi la nu Yàlla dekkalandoo ak moom, dëëlandoo nook moom fa déndi asamaan.
Efes 2:6
Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki njëkk, di Ki mujj. Maay Kiy dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw.
Peeñu ma 1:17–18
«Ñi nga ma jox nag, Baay, bëgg naa, fa may ne, ñoom it, ñu nekk faak man, ngir ñu gis sama daraja ji nga ma jox, ndax yaa ma sopp laata àddina di sosu.
Yowaan 17:24
nde noo di céri yaramam.
Efes 5:30
Mooy boppu yaram, wiy mbooloom gëmkat ñi, mooy njàlbéen, mooy taaw bi njëkka dekki, ndekkite lu dee toppul, ba tax muy ki jiitu ci lépp,
Kolos 1:18
ci moom ngeen mate it, te mooy kilifay mboolem boroom nguur yi ak mboolem boroom sañ-sañ yi.
Kolos 2:10
Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane. Noonu la goreele mboolem ñi seenug ragala dee tënkoon cig njaam, seen giiru dund.
Yawut ya 2:14–15
Sunu yaramu judduwaale wii nara yàqu, fàww mu sol weneen wu dul yàqu; sunu yaramu dee wii, fàww mu sol yaramu deetil. Bu yaramu judduwaale wii nara yàqu solee weneen wu dul yàqu, ba yaramu dee wii sol yaramu ndeetil, su boobaa la kàddu gii ñu bind di mat: «Mëddees na dee ci géeju ndam.
1.Korent 15:53–54
Bés yu mujj yi
Wone yépp14 Mee 2025
13 Mee 2025
12 Mee 2025
11 Mee 2025
10 Mee 2025
9 Mee 2025
8 Mee 2025