Delloosileen xel yi ci njub te bàyyi bàkkaar, ndax ñàkka xam lenn ci Yàlla, moom la ñenn ci yeen nekke, te loolu gàcce la ci yeen, laa wax!
1.Korent 15:34
Leeru Bés bi
Delloosileen xel yi ci njub te bàyyi bàkkaar, ndax ñàkka xam lenn ci Yàlla, moom la ñenn ci yeen nekke, te loolu gàcce la ci yeen, laa wax!
1.Korent 15:34
Yeen ñépp ay doomi leer ngeen, doomi bëccëg ndarakàmm; nun bokkunu dara ak guddi, mbaa ag lëndëm. Kon nag bunu nelaw ni ñi ci des, waaye nanu teewlu, te ànd ak sunu sago.
1.Tesalonig 5:5–6
Li tax ngeen wara gëna farlu ci loolu mooy, xam ngeen jant yi nu tollu; seen waxtuw yewwu jot na ba noppi, nde léegi la nu mucc gëna jege ba nuy doora gëm. Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer.
Room 13:11–12
Kon nag jëlleen gànnaayi Yàlla yépp, ba bu bésub safaan taxawee, ngeen mana jëflante, ba sottal, tey wéye taxaw temm.
Efes 6:13
Xalableen mboolem tooñ yi ngeen di tooñ. Sàkkuleen xol bu yees ak xel mu yees. Yeen waa kër Israayil, lu jar ngeen di dee?
Esekiyel 18:31
Kon nag baleen jépp jikko ju tilim ak mboolem xeeti mbon yi ne gàññ, te ngeen nangu, ci biir ag woyof, kàddu gi Yàlla xasa jëmbat ci yeen te mu man leena musal.
Yanqóoba 1:21
Léegi nag xale yi, saxleen ci Almasi bi, ndax bu feeñee, nu siggi fi kanamam te baña rus kera ba muy feeñ. Gannaaw xam ngeen ne moo jub, xamleen itam ne képp kuy def njub, ci moom nga sosoo.
1.Yowaan 2:28–29
Samay xar, sama baat lañuy déglu; maa leen xam, te man lañuy topp.
Yowaan 10:27
Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat, ba ubbil ma, dinaa agsi moos sa néeg, nu bokk reer.
Peeñu ma 3:20
Maa ngi nelaw, te xol yewwu; dégluleen, sama nijaay ay fëgg. Mu ne: «Xaritoo, jigéen sama, ubbil ma, sama nenne, alal sama! Sama bopp a ngi laye ba tooy, njañ li fanaanee guus.»
Ngën-gi-woy 5:2
Maa ubbil nijaay, waaye nijaay waññiku na, ba wéy. Ba mu waññikoo, tuuti ma dee. Seet naa ko, gisuma ko; ma woo ko, wuyuwul.
Ngën-gi-woy 5:6
Ba mu ko defee Aji Sax ji dikk taxaw, wooti ko na woon, ne ko: «Samiyel, Samiyel.» Samiyel ne: «Maa ngi lay déglu, Sang bi, waxal.»
1.Samiyel 3:10
Yeesu dikk ba tollu foofa, téen ne ko: «Sase, wàccal gaaw, ndax sa kër laa wara dali tey jii.» Sase daldi wàcc gaaw, bége koo dalal lool.
Luug 19:5–6
Éy Aji Sax ji, won nu sa ngor, baaxe nu sag wall.
Taalifi cant 85:8
Bés yu mujj yi
Wone yépp10 Mee 2025
9 Mee 2025
8 Mee 2025
7 Mee 2025
6 Mee 2025
5 Mee 2025
4 Mee 2025