Leeru Bés bi — 9 Mee: Yawut ya 11:1

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ngëm nag mooy cëslaayal yaakaar te mooy firndey li bët gisul.

Yawut ya 11:1

Su dee ci giiru dund gii doŋŋ lanu ame yaakaar ci Almasi bi, kon de noo gëna toskare ñépp.

1.Korent 15:19

Mooy noonu ñu binde rekk ne: «Lu bët gisul, nopp déggu ko, xel daju ko, Yàllaa ko dencal ñi ko sopp.» Waaye nun la Yàlla feeñalal denc googu jaare ci Xelam. Ndaxte Xelum Yàlla lépp lay gëstu ba ci xóotey mbóoti Yàlla.

1.Korent 2:9–10

Kooku, yeen ñi dul Yawut, ba ngeen déggee, yeen itam kàddug dëgg gi, xibaaru jàmm bi jëm ci seenug mucc, gannaaw ba ngeen gëmee, ci moom itam lañu leen màndargaale Noo gu Sell gi ñu dige woon. Noo gi moo di dawal bi nu jotagum ci sunu muur, ba kera njotug ñoñi Yàlla matee, ba nit ñi sante Yàlla màggaayam.

Efes 1:13–14

Yeesu ne ko: «Danga maa gis, ba tax nga gëm? Ndokkalee ñi gëm te gisuñu!»

Yowaan 20:29

Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd, ndax yeena ngi jot ci yool bi ngëm di yóotu, te mooy texe.

1.Piyeer 1:8–9

ndax ngëm lanuy doxe, waaye doxewunu ab gis-gis.

2.Korent 5:7

Kon nag buleen teqalikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci.

Yawut ya 10:35

Yeesu ne leen: «Man mii la, buleen tiit!»

Yowaan 6:20

Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki njëkk, di Ki mujj. Maay Kiy dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw.

Peeñu ma 1:17–18

Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttaliku bàkkaar.

Esayi 43:25

Ma ne: «Wóoy man, sànku naa! Man miy nit ku làmmiñam sobewu, xeetoo ci ñu seen làmmiñ sobewu, te samay gët tegu ci kaw Buur Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi.»

Esayi 6:5

Mu laalale xal wi sama gémmiñ, ne ma: «Mu ngoog, ndegam lii laal na sa gémmiñ, sag tooñ wàcc na, sa bàkkaar faru na.»

Esayi 6:7

Waaye ñu ngii di xeet wu ñu futti, sëxëtoo; ñépp tëje ciy pax, dence ci kaso, ñu doon alalu xare fu leen kenn dul xettalee, xanaa ñu di leen sëxëtoo, te kenn du ne ñu delloo leen.

Esayi 42:22

Xale yi doom, loolu laa leen bind, ngir ngeen baña bàkkaar. Waaye su ci amee ku dem ba bàkkaar, am nanu ab layookat fa wetu Baay bi, te mooy Yeesu Almasi bi, boroom njub.

1.Yowaan 2:1