Waaye seen jotkat a am doole, te mooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. Moo leen di layool seen layoo, ngir jàqal réewum Babilon, jàmmal waa àddina yi ci des.
Yeremi 50:34
Leeru Bés bi
Waaye seen jotkat a am doole, te mooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. Moo leen di layool seen layoo, ngir jàqal réewum Babilon, jàmmal waa àddina yi ci des.
Yeremi 50:34
Ràññee naa seen bàkkaar yu bare ak seen moy yu dul jeex. Yeenay tooñ aji jub, di geru, di xañ néew-ji-doole dëgg ci pénc.
Amos 5:12
Sunu kiiraay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israayil mooy boroom.
Taalifi cant 89:19
Ñi lay néewal, maa leen di leel seen suuxu bopp. Seen deret ni biiñ bu bees, ma màndale leen, ba ñépp xam ne maay Aji Sax ji lay wallu, jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.»
Esayi 49:26
Ana kuy kii bawoo Edom, sol yére yu xonq, bawoo Boccara? Kii ak yéreem yu yànj, di daagoo dooleem ju bare? Aji Sax ji nee: «Xanaa man mii di waxe dëgg, te am dooley walloo.»
Esayi 63:1
Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk,
Yudd 24
Yoonu Musaa moo dikk ngir fésal barewaayu moy, waaye fu bàkkaar bare, aw yiw gën faa bareeti,
Room 5:20
Képp ku ko gëm, deesu la daan, waaye ku ko gëmul, daanees na ko ba noppi, ndax moo gëmul jenn Doomu Yàlla ji.
Yowaan 3:18
Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.
Yawut ya 7:25
Ana lu tax ba ma dikkee, kenn nekku fa? Ma woote, kenn wuyuwul? Damaa gàtta gàtt loxo, ba manumaa walloo? Am damaa ñàkk doole ju ma xettalee? Xanaa du maay gëdd géej, mu wow, maay defi dex màndiŋ, ndox tukki; jën ya mar, dee ba yàqu?
Esayi 50:2
Ana ku nuy tàggaleek cofeelu Almasi bi? Du ay nattu, te du njàqare, du it coonoy bunduxataal, mbaa ab xiif, mbaa rafle, te du genn aayteef, ba cib saamar.
Room 8:35
Ndax kat bir na ma ne du ag dee, du ag dund, du ay malaaka, duy boroom nguur, du tey, du ëllëg, duy boroom doole, du lu kawe, du lu xóot, mbaa meneen mbindeef mu mu doon; dara manu noo tàggale ak cofeel gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu sunu Sang.
Room 8:38–39
Looy sàkku ku la beral loxo? Jaru ko! Maa ngii di wàcceel musiba képp kuy noyyi. Kàddug Aji Sax jee! Waaye may naa la sa bakkan di sa yoolu xare, fépp foo jëm.”»
Yeremi 45:5
Tegooleen sama kilifteef te ngeen jànge ci man, daldi dajeek noflaayal xol, ndax maa lewet, woyof.
Macë 11:29
Noonu Almasi Yeesu doon doxale, deeleen ko doxale ci seen biir: Moom mi nekke nekkinu Yàlla te ŋoyaaloowul ci dayob boppam bi ko def nawleb Yàlla. Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam. Moo toroxlu, moo nangu, ba dee fekk ko ci, ak mbugalu bant ba ñu ko daaj.
Filib 2:5–8
Ku jëlul sa bantu bopp bu ñu lay daaj, te topp ci man, yeyoowuloo ma.
Macë 10:38
Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
1.Piyeer 2:21
Teewul ragal Yàlla gu ànd ak doylu, di alal ju réy. Ndax kat indaalewunu dara ci àddina, te manunoo yóbbaale dara. Kon su nu amee lu nu lekk ak lu nu sol, nanu ko doyloo.
1.Timote 6:6–8
Ag ñàkk nag taxul may waxe nii, nde tàmm naa di doylu ci diggante bu ma mana tollu.
Filib 4:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp14 Awr 2025
13 Awr 2025
12 Awr 2025
11 Awr 2025
10 Awr 2025
9 Awr 2025
8 Awr 2025