Leeru Bés bi — 2 Awril: 1.Yowaan 5:21

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Xale yi, wattuleen seen bopp ci ay tuur.

1.Yowaan 5:21

Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqalikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax, «lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal. Maay doon seen baay, ngeen di samay doom, góor ak jigéen,» la Boroom bi, Aji Man ji wax.

2.Korent 6:17–18

«Kenn manula jaamu ñaari sang; dangay dëddu kii, sopp kee, mbaa nga fonk kii, cof kee. Manuleena jaamoondoo Yàlla ak Alal.

Macë 6:24

ndax waruleena jaamu jeneen yàlla, ngir Aji Sax ji, turu “Ku fiir ki” lay wuyoo, te Yàlla ju fiir la.

Mucc ga 34:14

«Yaw Suleymaan, doom, nanga wuta xam bu baax Yàlla ji ma gëm, man sa baay, te jaamoo ko xol bu ko wéetal ak xel mu ko déggal. Ndax biir xolu ku nekk Aji Sax ji da koy xool, te mboolem lu nit namm, di ko mébét xam na ko. Soo ko toppee, dina la ubbil boppam. Waaye soo ko dëddoo, dina la xarab ba fàww.

1.Jaar-jaar ya 28:9

Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, am dëgg, te soo àttee, yey.

Taalifi cant 51:6

Aji Sax ji nag ne Samiyel: «Bul xool ci melokaanu kii, mbaa jëmmu taxawaayam, ndax gàntal naa ko. Lii du ci gis-gisu nit. Nit, li fees bëtam lay gis, waaye Aji Sax ji ci xol lay xool.»

1.Samiyel 16:7

Soppe yi, bu nu sunum xel sikkul, dinanu ñemee walbatiku ci Yàlla.

1.Yowaan 3:21

Maa leen ne, mooy sàmm seen àq ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki dikkee, mbaa dina fekk ngëm ci kaw suuf?»

Luug 18:8

Ci ñoñam la ñëw, waaye ñoñam a ko dalalul.

Yowaan 1:11

Noowug Yàlla wax na ci lu leer ne ci mujug jamono, dina am ñu wacc yoonu ngëm wi, di topp ay xalaat yuy fàbbee ak ay àlluway ceytaane

1.Timote 4:1

waareel kàddug Yàlla te taxaw ci temm, su neexee ak su naqaree; di yedde, di femmoo, di ñaaxe, tey saxoo muñ ci sa njàngale. Ndax kat ay jamonoo ngi ñëw, nit ñi dootuñu xajoo àlluwa ju wér, waaye seeni bëgg-bëggi bopp lañuy topp, bay fortaatoo fu nekk ay jàngalekat yu leen di wax lu leen neex. Dëgg lañuy tanqamlu, lajj, wuti léebi neen.

2.Timote 4:2–4

«Waaye bés boobu mbaa waxtu wa nag, kenn xamu ko; du malaaka ya fa asamaan, du Doom ji, xanaa Baay bi doŋŋ. Moytuleen te teewlu, ndax xamuleen kañ la.

Màrk 13:32–33

Ndokkalee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk.

Luug 12:37

Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi.

Tit 2:13